Genn ngoon Isaaxa génn, di doxantu ca àll ba. Naka la ne siggét xool, séen giléem yuy ñëw.
Njàlbéen ga 24:63
Leeru Bés bi
Genn ngoon Isaaxa génn, di doxantu ca àll ba. Naka la ne siggét xool, séen giléem yuy ñëw.
Njàlbéen ga 24:63
Te Sang bi, musal ma ci bàkkaaru teyeef, mu bañ maa jiital, ma mana màndu, mucc moy gu réy.
Taalifi cant 19:14
Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, feeñal nga ca sa kàttan, ngir jaxase say noon, bañaaleek feyukat ne xerem. Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.
Taalifi cant 8:3–4
Liggéeyi Aji Sax ji réy na, ku ko safoo di ko gëstu.
Taalifi cant 111:2
Ndokkalee yaw mi toppul tànki ku bon, taxawewuloo yoonu moykat, toogewuloo jataayu ñaawlekat. Xanaa di bége yoonu Aji Sax ji, di ko jàngat guddeek bëccëg.
Taalifi cant 1:1–2
Téereb yoon bii, bumu teqalikook sa làmmiñ, waaye dee ko jàngat guddi ak bëccëg, ngir di fexee jëfe li ñu ci bind lépp. Su boobaa la say mébét di sotti, te ci ngay am ndam.
Yosuwe 1:8
Dama lay sant, sama giiru dund kay, tàllal la ay loxo, sàbbaale la. Sama xol di sedd, ni ku ñam wu duun suural, ma bég, sarxolle, màggal la.
Taalifi cant 63:5–6
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Taalifi cant 13:1
gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.
Yanqóoba 1:17
Siyoŋ a nga naa: «Aji Sax ji wacc na nu, Boroom bi fàtte na nu!» Aji Sax ji nee: «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram? Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte.
Esayi 49:14–15
Aji Sax ji nee: «Yanqóoba, baal xel ci lii! Ma ne Israayil, fàttalikul, yaa di sama jaam! Ma bind la, ngay sama jaam, yaw Israayil, duma la fàtte! Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir, say bàkkaar ne mes nib lay. Délsil fi man, jot naa la.»
Esayi 44:21–22
Yeesu nag ku soppoon Màrt la, ak Maryaama ak Lasaar. Teewul ba mu déggee ne daa wopp, toogaat na ñaari fan fa mu nekkoon.
Yowaan 11:5–6
Ci kaw loolu as ndawas Kanaaneen jekki jóge ca gox booba, di wax ca kaw, naan: «Sang bi, Sëtub Daawuda, yërëm ma! Sama doom ju jigéen la rab jàpp, mu sonn lool.» Yeesu nag tontuwu ko baat, taalibeem ya dikk ne ko: «Dàqal kii nu topp, di yuuxu ci sunu kaw!»
Macë 15:22–23
Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi bi feeñee.
1.Piyeer 1:7
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Mar 2026
28 Mar 2026
27 Mar 2026
26 Mar 2026
25 Mar 2026
24 Mar 2026
23 Mar 2026