Leeru Bés bi — 5 Awril: Njàlbéen ga 32:26

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ba nit ka xamee ne manalu ko dara, dafa dóor Yanqóoba ci yaxu mooco bi, mu summikoo ca bëre ba.

Njàlbéen ga 32:26

Xanaa ku langaamoo sama kiiraay te jàmmook man, ba jàmmook man.

Esayi 27:5

Yeesu nag ne ko: «Ndaw sii, yaaka réy ngëm. Kon nag na la amal noonu nga ko bëgge.» Ca waxtu woowa la doom ja wér.

Macë 15:28

Yeesu daldi laal seeni bët, ne leen: «Noonu ngeen ko gëme, na ame noonu.»

Macë 9:29

Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje. Kooku bumu yaakaar dara ci Boroom bi.

Yanqóoba 1:6–7

Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam. Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom.

Luug 24:28–29

Ca la seeni gët ubbiku, ñu xàmmee ko. Moom nag, mu ne mes, réer leen. Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?»

Luug 24:31–32

Gannaaw daj naa saw yiw nag, rikk xamal ma li nga namm, ba ma xam la. Su ko defee ma man di daj saw yiw. Te ngalla jàppal ne xeet wii kat, ñoo di sa ñoñ.» Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»

Mucc ga 33:13–14

Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.

Yawut ya 12:2

«Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa nekk, Ki nekk, di Kiy dikk ëllëg, te di Aji Man ji.

Peeñu ma 1:8

Ana ku def lii, dogal ko? Xanaa ki dale fa njàlbéen di woo maas yi! Man Aji Sax ji maa njëkk, te man la ak ñi mujj ba tey!

Esayi 41:4

Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel ak seen léppi xol ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi bi feeñee. Ki leen woo de ku wóor la, te moo koy def it.

1.Tesalonig 5:23–24

Te lii kat, bir na ma: ki tàmbali jii jëf ju baax ci yeen, dina ko àggale ba keroog bésub Almasi Yeesu.

Filib 1:6

Ana nu ngeen mana ñàkke nii xel? Ngeen tàmbalee ci Noo gu Sell gi, ba noppi di jéema mottalikoo jëfi nitu suuxu neen!

Galasi 3:3

Aji Sax jee may feyul. Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor! Bul wacc ñi nga binde sa loxo.

Taalifi cant 138:8

ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.

Filib 2:13