Soppe yi, lenn a ngii, buleen ko umple: benn bés ni junniy at la mel ci Boroom bi; junniy at mel ni benn bés ci moom. Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax bëggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.
2.Piyeer 3:8–9
«Samay xalaat déy du seeni xalaat,
te samay jëfin du seeni jëfin.»
Kàddug Aji Sax jee.
Mu ne: «Ni asamaan tiime suuf,
ni la samay jëfin tiime seeni jëfin,
samay xalaat it tiime ko seeni xalaat.
Ab taw ak tawub yuur ay wàcce asamaan,
du fa dellu,
te suuxatul suuf,
saxal ko, meññal ko,
ba kuy ji, mu may la jiwu;
kuy lekk, mu may lam pepp.
Sama kàddu giy bawoo sama gémmiñ it, noonu la.
Du délsee ag neen ci man
te deful li ma namm,
ba sottal li ma ko yebal.
Esayi 55:8–11
Yàlla moo tëj nit ñépp ci seenug déggadi, ngir yërëm leen ñoom ñépp.
Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!
Room 11:32–33
«Maa jàllarbi lenn ci yeen,
na ma jàllarbee woon waa Sodom ak Gomor.
Ngeen rëcce ca ni gillit
gu ñu fëkke cib taal.
Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.»
Kàddug Aji Sax jee!
Amos 4:11
Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu,
way-gëmadi yaa ngay lox.
Ana kan ci nun moo mana dal ak
sawara wuy xoyome?
Ana kan ci nun moo mana dal ak
taal yu yànj ya dul fey?
Esayi 33:14
Nun ci sunu wàllu bopp, jàppoon nanu ne sunu àtteb dee moo taxaw. Waaye loolu tax na nu bañatee yaakaar sunu bopp, xanaa di yaakaar Yàlla miy dekkal ñi dee. Moo nu wallu ci googu dee gu naroona metti, moo nuy walluwaat, te moom lanu yaakaar mu wallooti nu.
2.Korent 1:9–10
Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.
Room 6:23
Céy ku nara tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund, ndaw lu raglu!
Yawut ya 10:31
Danoo xam lan mooy ragal Boroom bi nag, te moo nu tax di wax lu gëmloo nit ñi. Yàlla de ràññee na bu baax nooy kan. May yaakaar ne yeen itam, ci seen biir xol, ràññee ngeen bu baax nooy kan.
2.Korent 5:11
waareel kàddug Yàlla te taxaw ci temm, su neexee ak su naqaree; di yedde, di femmoo, di ñaaxe, tey saxoo muñ ci sa njàngale.
2.Timote 4:2
ñii ngeen wallu leen, foqatee leen ci sawara, ña ca des, ngeen yërëm leen yërmande ju ànd akug ragal, ba far seexlu ab turki bu seen yaram sobeel ndax seeni bàkkaar.
Yudd 23
Mu wax ma ne ma: «Lii moo di kàddug Aji Sax ji dikkal Sorobabel, di wax ne:
Du cig njàmbaar, du ci doole,
ci samag noo la.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.»
Sàkkaryaa 4:6
bi bëgg ñépp mucc te ràññee liy dëgg.
1.Timote 2:4