Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
Filib 4:19
Leeru Bés bi
Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
Filib 4:19
Waaye njëkkleena tiisoo nguurug Yàlla, ak njub gi mu laaj, te loolu lépp moo leen ko ciy dollil.
Macë 6:33
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Room 8:32
Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom, muy Póol, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di tey, di ëllëg, lépp, yeena ko moom. Yeen nag, Almasi bi moo leen moom, te Almasi bi, Yàllaa ko moom.
1.Korent 3:21–23
Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
2.Korent 6:10
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax jee may sàmm, du lenn lu ma ñàkk.
Taalifi cant 23:1
Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.
Taalifi cant 84:11
Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.
1.Timote 6:17
te Yàlla man na leena baawaanal wépp yiw, ba ngeen saxoo am lu leen doy ci lépp, ak koom gu bare, ngir jépp jëf ju baax.
2.Korent 9:8
Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?
2.Korent 6:14
Àtteb daan bi nii la tëdde: leer moo dikkal àddina, waaye nit ñi la lëndëm gënal leer ndax seen jëf yu bon.
Yowaan 3:19
Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm.
1.Tesalonig 5:5
Waaye ku bañ mbokkum gëmkatam, ci lëndëm gi la nekk, biir lëndëm gi lay wéye it, te xamul fu mu jëm, ndax lëndëm gaa ko gëlëmal.
1.Yowaan 2:11
Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
Taalifi cant 119:105
Ngalla xoolal ci kóllëre gi, fu làqu ci réew mi, fitna dale fa ba dajal.
Taalifi cant 74:20
Soppe yi, nanu soppante, ndax cofeel ci Yàlla la bokk; képp ku am cofeel, ci Yàlla nga sosoo, te xam nga Yàlla. Ku amul ag cofeel nag, xamuloo Yàlla, ndax Yàlla cofeelu neen la.
1.Yowaan 4:7–8
Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.
Kàddu yu xelu 4:19
Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.
Kàddu yu xelu 4:18
Man maa dikk, di ag leer ci àddina, ngir ku ma gëm du des cig lëndëm.
Yowaan 12:46
Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer.
Efes 5:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp30 Mar 2026
29 Mar 2026
28 Mar 2026
27 Mar 2026
26 Mar 2026
25 Mar 2026
24 Mar 2026