Leeru Bés bi — 28 Mars: Yosuwe 1:18

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Képp ku gàntal sa kàddu, baña dégg say ndigal ci mboolem loo ko sant, kooku, dees koy rey. Dëgërlul rekk te am fit.»

Yosuwe 1:18

Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?

Taalifi cant 27:1

Mooy dooleel ku loof, di kàttanal ku jeele. Waxambaane sonn, loof; xalelu góor di tërëf a tërëf, kiy yaakaar Aji Sax ji moom, di yeeslu doole; da naa fëyy ni jaxaay juy naaw, di xélu te du xiix, di dox te du xoox.

Esayi 40:29–31

Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.

Taalifi cant 73:26

Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?

Room 8:31

Aji Sax jeek man, duma tiit. Ana lees ma manal?

Taalifi cant 118:6

Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla, mayal askanu Yanqóoba ay ndam.

Taalifi cant 44:5

Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.

Room 8:37

Wurus wi ak xaalis bi ak xànjar bi ak weñ gu ñuul gi, maneesu koo waññ. Ayca boog ci liggéey bi, te yal na Aji Sax ji ànd ak yaw.»

1.Jaar-jaar ya 22:16

Loolu la Yeesu wax, dal cay teg ne leen: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maay dem ba yee ko.»

Yowaan 11:11

Bokk yi nag, bëggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo. Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.

1.Tesalonig 4:13–14

Ndaxte ñi dee, su ñu dul dekki kay, Almasi bi it dekkiwul. Su Almasi bi dekkiwul nag, seen ngëm amul njariñ, te yeena ngi ci seeni bàkkaar ba tey. Te kon it ñi dee gannaaw ba ñu gëmee Almasi bi, sànku nañu.

1.Korent 15:16–18

Waaye nag Almasi bi dafa dekki moos, te mooy saraxu ndoortel meññeef bi ñu sàkke ci ngóobum bakkani nit ñi dee.

1.Korent 15:20

Ba xeet wépp jàllee dexu Yurdan ba noppi, Aji Sax ji dafa wax Yosuwe ne ko:

Yosuwe 4:1

Nga sant leen ne leen: “Dangeen di fore fi tànki sarxalkat yi taxaw jonn ci digg dexu Yurdan gi, fukki doj ak ñaar, te ngeen yóbbaale doj yi, tegi leen ca dal ba ngeen di fanaani guddig tey.”»

Yosuwe 4:3

ngeen wax leen ne leen: “Walu ndoxu Yurdan maa dogoon fa kanam gaalu kóllërey Aji Sax ji. Ba gaal gay jàll dexu Yurdan, ca la walum ndoxu Yurdan dog. Doj yii la bànni Israayil di fàttalikoo loola ba fàww.”»

Yosuwe 4:7

Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.

Jëf ya 2:32