Leeru Bés bi — 1 Awril: Galasi 5:22

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm

Galasi 5:22

Ndax kat solos nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solos nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

Room 14:17

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,

1.Piyeer 1:8

Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.

2.Korent 6:10

Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ;

Room 5:3

Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.

Yawut ya 12:2

Maa leen wax loolu ngir samag mbég wàllsi ci yeen, ba seen mbég mat sëkk.

Yowaan 15:11

Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!

Filib 4:4

Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»

Neyemi 8:10

Yaa may xamal yoonu dund. Fu bànneex mate, yaa teew, xéewal sa ndijoor la saxe.

Taalifi cant 16:11

ndaxte Xar mi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»

Peeñu ma 7:17

Sedeyoŋ nag tabax foofa ab sarxalukaay, ñeel Aji Sax ji. Mu tudde ko «Aji Sax ji, jàmm.» Ba tey jii sarxalukaay baa nga ca Ofra gu Abiyesereen ña.

Njiit ya 6:24

Waaye déglul, dinga am doom ju góor juy doon nitu jàmm te dinaa ko may ay noonam yi ko wër yépp jàmmal ko. Suleymaan (muy firi Boroom jàmm ji) sax lay tudd, te jàmm akug dal lay may Israayil giiru dundam.

1.Jaar-jaar ya 22:9

Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.

Macë 12:42

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm, ci dëkkuwaay yu wóor, ci dalluwaay yu dal xel, doonte gott bi day daanu ci tawub doji yuur, dëkk bi detteelu ba ne dett.

Esayi 32:18–19

Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jàmbur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante.

Efes 2:14

Ab saamar la ñooñuy yilife Asiri, réewum Nimrodd mooma ca biiri buntam. Kilifa gi ñu dige moo nuy xettaleek Asiri, bu ñu nu songee, ba joggati sunu suuf.

Mise 5:5

Dinañu xare ak Xar mi, waaye Xar mee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»

Peeñu ma 17:14

Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.

Yowaan 14:27