Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.
Kàddu yu xelu 11:18
Leeru Bés bi
Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.
Kàddu yu xelu 11:18
«Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya délsi, daldi bokk xayma ak ñoom ni alalam tolloo. Ci kaw loolu ka jotoon juróomi milyoŋ dikk, indaale yeneen juróom, ne ko: “Sang bi, juróomi milyoŋ nga ma dénkoon; yeneen juróom yii laa ci am.” Njaatigeem ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi te wóor. Gannaaw ci lu tuut nga wóore, lu bare laa lay dénk. Kaay nag nu bokk bége.”
Macë 25:19–21
Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko. Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.
2.Timote 4:7–8
«Léegi ma ñëw. Ŋoyal ci li nga yor, ngir kenn baña fëkk sa kaalag ndam.
Peeñu ma 3:11
Benn nattu dabu leen bu moy nattu yiy dale. Te it Yàllaa jara wóolu. Yàlla du nangu ngeen tegoo nattu bu ngeen àttanul, waaye nattu ba lay booleek pexe ma leen cay génne, ba ngeen man koo dékku.
1.Korent 10:13
Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?
Màndiŋ ma 23:19
Waaye Yeesu mii la ag palam ànd ak ngiñ lu jibe ca ka ko wax ne ko: «Boroom bee ko giñ te du dellu gannaaw: “Yaa dib sarxalkat ba fàww.”»
Yawut ya 7:21
Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem. Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam.
Yawut ya 6:17–18
Kon nag ñiy sonn te coobarey Yàlla tax, nañu dénk seen bopp Yàlla, Ki sàkk te wóor, te ñuy saxoo def lu baax.
1.Piyeer 4:19
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
Ki leen woo de ku wóor la, te moo koy def it.
1.Tesalonig 5:24
Bés yu mujj yi
Wone yépp26 Mar 2026
25 Mar 2026
24 Mar 2026
23 Mar 2026
22 Mar 2026
21 Mar 2026
20 Mar 2026