La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf,
Kolos 3:2
Leeru Bés bi
La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf,
Kolos 3:2
Buleen topp àddina ak li ci biiram. Ku topp àddina, cofeelu Baay bi nekkul ci moom.
1.Yowaan 2:15
«Buleen dajale ab denc ci kaw suuf, fi ko max ak xomaag di yàqe, mbaa ab sàcc bëtt, jël ko. Waaye dajaleleen ab denc fa asamaan, fa ko max ak xomaag dul yàqe, te ab sàcc du bëtt, jël ko. Ndaxte fa sab denc nekk, sab xol it a nga fa.
Macë 6:19–21
ndax ngëm lanuy doxe, waaye doxewunu ab gis-gis.
2.Korent 5:7
Moo tax dunu ñàkk yaakaar. Doonte sax sunu bitib jëmm a ngi gën di bon, sunu jëmmu biir moom, mu ngi yeeslu bésoo bés. Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk. Moo waral xoolunu ci li bët mana gis, waaye li bët dul gis, ci lanuy xool, ndax li bët mana gis day wéy, waaye li bët dul gis mooy sax ba fàww.
2.Korent 4:16–18
Loolu moo am ngir ab cér bu dul yàqu, du sobewu, du seey, cér bu dence fa asamaan ñeel leen,
1.Piyeer 1:4
Bu gisee ni mbaaram neexe, ak ni réew mi naate, day waaf, gàddu ngaaxam, daldi féetewoo coonob njaam.
Njàlbéen ga 49:15
Bokk yi, yonent yi wax ci turu Boroom bi, di dékku aw tiis ak di muñ, defleen leen seeni royukaay.
Yanqóoba 5:10
Xew-xew yooyu dal maam ya ay misaal la, te dees koo bind ngir nu jànge ci, nun ñi mujug jamono yemool.
1.Korent 10:11
Mu ne ko: «Waxi jeeg bu dof daal ngay wax, yaw! Du Yàlla da nuy may lu baax, nu jël? Kon kay bu nu mayee safaan ba it, nu wara jël.» Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul ciw làmmiñam.
Ayóoba 2:10
Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.
Sarxalkat yi 10:3
Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.»
1.Samiyel 3:18
làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.
Taalifi cant 55:22
Ndaxam moom sunu wopp la yenu, sunuy mitit la sëfoo. Nun nu foog ne dees koo mbugal, foog ne Yàllaa ko duma, toroxal ko.
Esayi 53:4
«Mboolem yeen ñi loof ndax sëf bu diis, ñëwleen ci man, man maa leen di noppal. Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof. Sama kilifteef sedd na, te samab sëf woyof.»
Macë 11:28–30
Bés yu mujj yi
Wone yépp3 Mar 2026
2 Mar 2026
1 Mar 2026
28 Few 2026
27 Few 2026
26 Few 2026
25 Few 2026