Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Leeru Bés bi
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Nun nag xam nanu te gëm nanu cofeel gi nu Yàlla sopp. Yàlla cofeelu neen la. Képp ku saxoo cofeel, ci Yàlla nga sax, te Yàlla itam ci yaw la sax.
1.Yowaan 4:16
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:5
Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wi tabaxkat yi beddi woon, te mu mujj di doju koñu tabax bi.»
1.Piyeer 2:7
Nun nag, li nu taxa am cofeel moo di Yàlla moo nu njëkka sopp.
1.Yowaan 4:19
Ndaxte cofeelu Almasi bi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: gannaaw kenn moo dee ngir ñépp, kon ñépp a dee. Te ki dee ngir ñépp, daa dee ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki dee ngir ñoom, ba dekki.
2.Korent 5:14–15
Ci wàllu mbëggeel gi war ci biiri bokk, soxlawuleen ku leen ci bind dara, ndax yeen ci seen bopp, Yàlla tàggat na leen ci soppante,
1.Tesalonig 4:9
Sama santaane moo di ni ma leen soppe, ngeen soppantee noonu.
Yowaan 15:12
Waaye li ci raw mooy soppanteleen cofeel gu mat sëkk, ndax cofeel, bàkkaar yu bare lay far.
1.Piyeer 4:8
te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla.
Efes 5:2
Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Room 8:31
Aji Sax jeek man, duma tiit. Ana lees ma manal?
Taalifi cant 118:6
Yëngal nga suuf, xar ko; ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!
Taalifi cant 60:4
Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?
Taalifi cant 27:1
Bu gàngoor booloo sama kaw, duma raf. Ab xare jib, ma ànd ak Yàlla.
Taalifi cant 27:3
Mu ngoogu, Yàllaa ngii jiite nu, mooki sarxalkatam ak seeni liit yu xumb, ngir jibal wooteb xare ci seen kaw. Kon yeen bànni Israayil, buleen xareek Aji Sax ji seen Yàllay maam, ndax kat dungeen am ndam.»
2.Jaar-jaar ya 13:12
Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!
Taalifi cant 46:7
Dinañu xare ak Xar mi, waaye Xar mee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»
Peeñu ma 17:14
Ana lu xeeti àddina di riire, lu xeet yiy lale pexey neen?
Taalifi cant 2:1
Ki ci jalub asamaan a ngay ree, Boroom baa nga leen di kókkali,
Taalifi cant 2:4
Ngeen mébét, dara! Ngeen diisoo, diisoo, tus! Yàllaa ànd ak nun!
Esayi 8:10
Bés yu mujj yi
Wone yépp28 Few 2026
27 Few 2026
26 Few 2026
25 Few 2026
24 Few 2026
23 Few 2026
22 Few 2026