May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu, di binni nim xati, di séentu kaw ba saay gët giim. Dama noon: Éy Boroom bi, loof naa, dimbali ma.»
Esayi 38:14
Leeru Bés bi
May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu, di binni nim xati, di séentu kaw ba saay gët giim. Dama noon: Éy Boroom bi, loof naa, dimbali ma.»
Esayi 38:14
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Yaw laay séentu, yaw mi toog fa asamaan. Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët, ba keroog mu baaxe nu.
Taalifi cant 123:1–2
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda. Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la. Àll laa lay woowe, sama xol jeex; yéege ma doju rawtu wu ma jotul. Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
Taalifi cant 61:1–4
Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy féexloo ci tàngoor, ndax merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw ab tabax.
Esayi 25:4
Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam. «Moo bàkkaarul, fenul.» Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.
1.Piyeer 2:21–23
Joŋanteel joŋante bu baax bi, ngir yoonu ngëm wi, te nga ŋoy bu baax ci texeg fàww gi ñu la woo, ba tax nga dëggal sa ngëm nu rafet noonu nga ko dëggale woon fa kanam seede yu bare.
1.Timote 6:12
Ba nu àggee diiwaanu Maseduwan, sunuw yaram noppaluwul, waaye daj nanu bépp coono: xeex ci biti, njàqare ci biir.
2.Korent 7:5
Alyaasa ne ko: «Bul tiit, noo leen ëpple ñu ñu àndal.»
2.Buur ya 6:16
Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.
Efes 6:10
Yàllaa may làqe dooleem, xàllal ma, yoon mat.
2.Samiyel 22:33
Moo may tàggat ci xare, may tàwwig fitt ci xalag xànjar.
2.Samiyel 22:35
Du caageenu doyloo sunu manoorey bopp, ba yaakaar ne lenn man naa sottee ci sunu wàllu bopp, waaye sunu manoore ci Yàlla la jóge.
2.Korent 3:5
Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe.
Taalifi cant 34:7
Alyaasa nag ñaan ne: «Aji Sax ji, ngalla ubbil ay bëtam, mu gis.» Aji Sax ji ubbi bëti surga ba, mu xool, ndeke tund waa nga fees aki fas aki watiiri sawara, wër Alyaasa.
2.Buur ya 6:17
Ana lu ma ciy tegati? Jot gee ko dul mate, su ma naroona nettali mbirum Sedeyoŋ ak Barag ak Samson ak Yefte ak Daawuda ak Samiyel ak yonent yi. Ñooñu ngëm lañu tege loxo ay nguur, ngëm lañu doxale yoon, ci kaw ngëm la ay dige sottee, ñeel leen, te ci lañu tëje gémmiñi gaynde ya. Ngëm lañu feye dooley sawara, ngëm lañu rëcce ñawkay saamar, ngëm a waral ñu weccikoo kàttan seenug néew doole, ci kaw ngëm lañu doone ay ñeyi xare, ba dàq gàngoori yeneen réew.
Yawut ya 11:32–34
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Mar 2026
3 Mar 2026
2 Mar 2026
1 Mar 2026
28 Few 2026
27 Few 2026
26 Few 2026