Nanga wóoloo Aji Sax ji sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin. Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
Kàddu yu xelu 3:5–6
Leeru Bés bi
Nanga wóoloo Aji Sax ji sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin. Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
Kàddu yu xelu 3:5–6
Yàllaa may musal, di ma sagal, ma di ko doolewoo. Sama kiiraay, Yàllaa!
Taalifi cant 62:8
Nga ne ma: «Dama laa xelal, xamal la fi ngay jaar, digal la, di la bàyyi xel. Buleen mel ni fas mbaa berkelle mi amul ag dégg, laab ak tarka di ko téye, mu doora yem fi seen wet.» Ku bon barew tiis. Ku wóolu Aji Sax ji, mu yiire la ngoram.
Taalifi cant 32:8–10
di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.
Esayi 30:21
daldi xélu dëgmal naanukaay ba, ngir jot ca neexal ba nu Yàlla di woowe fa kaw, ci Almasi Yeesu.
Filib 3:14
Yeesu nag ne ko: «Boo bëggee mat sëkk, demal jaay li nga am, nga jox ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
Macë 19:21
Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»
Njàlbéen ga 15:1
Njaatigeem ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi te wóor. Gannaaw ci lu tuut nga wóore, lu bare laa lay dénk. Kaay nag nu bokk bége.”
Macë 25:21
Guddi du amati, te deesul soxlaati làmp mbaa naaj, ndax Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dañuy nguuru ba fàww.
Peeñu ma 22:5
ba bu sàmm bu mag bi feeñee, ngeen jot kaalag daraja gu dul furi.
1.Piyeer 5:4
Ndokkalee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag texe gi Yàlla dig ñi ko sopp.
Yanqóoba 1:12
Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.
2.Timote 4:8
Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar.
1.Korent 9:25
«Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.
Yowaan 17:24
Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.
1.Tesalonig 4:17
Jàpp naa ne sunu coonob tey du dara, soo ko xoolee ci teraanga ji ñu nuy feeñalal ëllëg.
Room 8:18
Bés yu mujj yi
Wone yépp2 Mar 2026
1 Mar 2026
28 Few 2026
27 Few 2026
26 Few 2026
25 Few 2026
24 Few 2026