Leeru Bés bi — 2 Mars: Njàlbéen ga 41:52

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Doomam ja ca topp mu tudde ko Efrayim (muy firi Giir), ndaxte da ne: «Yàllaa ma giiral ca réew ma ma sonne.»

Njàlbéen ga 41:52

Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi, Baayu yërmande yi, Yàlla jiy dëfale nu nekk, moom mi nuy dëfal ci sunu jépp njàqare, ngir noonu nu jote nun ci sunu bopp, ndëfalaay lu nu dëfalu fa Yàlla, nu man koo dëfale ñi nekk ci mboolem xeeti njàqare. Ndax kat coonoy Almasi bi, nu mu gëna yokkoo ci sunu kaw, ndax li nu ko gëm, noonu itam la ndëfalaay liy bawoo ci Almasi bi di yokkoo.

2.Korent 1:3–5

Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu. Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi bi feeñee.

1.Piyeer 1:6–7

Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jàmbur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.

2.Timote 4:17

Kon nag ñiy sonn te coobarey Yàlla tax, nañu dénk seen bopp Yàlla, Ki sàkk te wóor, te ñuy saxoo def lu baax.

1.Piyeer 4:19

Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.

Yawut ya 4:9

Biir bàmmeel la ñu bon ñiy noppee sonle, fa la ña jeele doole noppaloo, ña ñu tëjoon ne finaax, déggatuñu coowal ku leen di sas,

Ayóoba 3:17–18

Ci kaw loolu ma dégg baat bu jibe asamaan ne: «Bindal: “Bés niki tey ndokkalee aji dee ñi deewaale gëm Sang bi.”» Noowug Yàlla nee: «Waawaaw, ndax coono dina leen wàcc, ngir seeni jëf a leen topp.»

Peeñu ma 14:13

Loolu la Yeesu wax, dal cay teg ne leen: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maay dem ba yee ko.»

Yowaan 11:11

Li Yeesu waxe noonu mooy Lasaar dee na, ñoom nag ñu foog ne da ne Lasaar day nelaw rekk.

Yowaan 11:13

Noo ngi onk ndax diis, li feek nu ngeek sunuw yaram, xayma bi nu soloo nii. Du summiku lanu namm, waaye solu teg ko ci lanu namm, ngir li jëm ci dee, daldi suux ci biir dund.

2.Korent 5:4

Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gu Sell gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat. Ndax kat sunu mucc, yaakaar la taxaweegum, te yaakaar joo teg sa bët, dootul yaakaar. Li nit ki teg bëtam, nu mu koy yaakaaratee? Li nu gisul kay lanuy yaakaar, di ko séentooka muñe yaakaar ji.

Room 8:23–25