Sama xalaat bii, yal na ko neex. Man de maa ngi bége Aji Sax ji!
Taalifi cant 104:34
Leeru Bés bi
Sama xalaat bii, yal na ko neex. Man de maa ngi bége Aji Sax ji!
Taalifi cant 104:34
Mbete garab gu gëna neex ci gott bi, kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi. May bége keppaaram, safoo doom ya.
Ngën-gi-woy 2:3
Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, ndajem ñu sell ña di la joobee sa kóllëre.
Taalifi cant 89:6
Sama nijaay daa xees, leer; kenn la ci fukki junniy góor.
Ngën-gi-woy 5:10
Mu gis nag per buy jar lu bare, daldi jaay mboolem lu mu am, ba jënd per ba.»
Macë 13:46
tukkee itam fa Yeesu Almasi bi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki njëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqalikook kilifteefu sunuy bàkkaar,
Peeñu ma 1:5
Kanam gi ni wurus, di wurusu ngalam; njañ li lëmësu, ñuul ni ndobin.
Ngën-gi-woy 5:11
Yàlla moo teg lépp fi roni tànkam, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi,
Efes 1:22
Mooy boppu yaram, wiy mbooloom gëmkat ñi, mooy njàlbéen, mooy taaw bi njëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, ba tax muy ki jiitu ci lépp,
Kolos 1:18
Lex ya di tool, gàncax ga ne ca bann, tuñ ya diy tóor-tóor, ndàbb wale ca, rogalaat.
Ngën-gi-woy 5:13
Yeesu jóge fa, dem ba ca diiwaan ba ñuy wax Tir. Mu dugg fa ci genn kër, te bëggul kenn xam ko, waaye manula fexe ba nit ña umple ko.
Màrk 7:24
Lex ya di tool, gàncax ga ne ca bann, tuñ ya diy tóor-tóor, ndàbb wale ca, rogalaat.
Ngën-gi-woy 5:13
Wattukat ya ne leen: «Nit masula waxe ni kii!»
Yowaan 7:46
yeel yi kenuy doj wu jafe la, sampe ci tànki wurusu ngalam. Meloom ni tundi Libaŋ, di tànnéef ni garabi seedar.
Ngën-gi-woy 5:15
Yaa yor sama àpp. Xettali maak ku ma noonoo ak ku may sonal.
Taalifi cant 31:16
Rendileen seen sarax yi war, te wóolu Aji Sax ji.
Taalifi cant 4:6
Ba loolu amee, Yeesu dox ba sore leen tuuti, ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf. Mu ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko! Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
Macë 26:39
«Léegi nag am naa njàqarey xol. Ana lu may wax? Dama naa: “Baay, musal ma ci coonob waxtu wii”? Waaye coonob waxtu wii tembe moo ma taxa dikk!
Yowaan 12:27
Def sama coobarey bopp taxul ma wàcce fa asamaan, waaye def coobarey ki ma yónni moo tax.
Yowaan 6:38
Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj.
Filib 2:8
Fan yi Almasi bi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te ñaan ga nangu na it, ndax na mu ragale woon Yàlla. Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj.
Yawut ya 5:7–8
Defe nga ne manumaa woo sama Baay wall, mu yónnee ma ci saa si lu ëpp fukki gàngoori malaaka ak ñaar?
Macë 26:53
Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi bi dee ci biir coono, ba dekki ca ñetteelu fan ba; te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.
Luug 24:46–47
Bés yu mujj yi
Wone yépp21 Sàt 2025
20 Sàt 2025
19 Sàt 2025
18 Sàt 2025
17 Sàt 2025
16 Sàt 2025
15 Sàt 2025