Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet ak ku amug dégg.
Kàddu yu xelu 3:13
Leeru Bés bi
Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet ak ku amug dégg.
Kàddu yu xelu 3:13
Ku ma daj, gudd fan, Aji Sax ji bége la.
Kàddu yu xelu 8:35
Kuy damu kay, na damoom xelam mu ko may mu xam ma, xam ne maay Aji Sax jiy doxal ngor ak yoon ak njub fi kaw suuf. Loolu déy mooy sama bànneex.» Kàddug Aji Sax jee. «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay dikkal képp ku xarafam yem ci yaram,
Yeremi 9:23–24
Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel, xam Aji Sell ji di amug dégg.
Kàddu yu xelu 9:10
Waaye la ma jàppe woon ag ndollent, moom laa def tey ag wàññeent ndax Almasi bi. Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi bi,
Filib 3:7–8
Ci moom la mboolem alal ji ci xel ak xam-xam dëxëñe.
Kolos 2:3
Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa amug dégg, di boroom doole.
Kàddu yu xelu 8:14
Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njub, di sunu cellte, di sunug njot,
1.Korent 1:30
Kuy jëfe njekk mbete garab guy taxa dund, ku rafet xel am nit ñi.
Kàddu yu xelu 11:30
Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
2.Korent 6:10
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
2.Korent 8:9
Ci ag matam lanu tanqe nun ñépp, yiw ci kaw yiw.
Yowaan 1:16
Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
Filib 4:19
te Yàlla man na leena baawaanal wépp yiw, ba ngeen saxoo am lu leen doy ci lépp, ak koom gu bare, ngir jépp jëf ju baax.
2.Korent 9:8
Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo tànn ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur gi Yàlla dig ñi ko sopp?
Yanqóoba 2:5
Bokk yi, seetleen ñan ngeen woon, ba ñu leen di woo. Barewul ci seen biir ay xamkat ci gis-gisu nit ñi, barewul ci yeen ay boroom doole, barelewuleen ñu rafet ab juddu. Waaye li àddina jàppe ag ndof, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko xamkat yi, te li néew doole ci àddina, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko li bare doole.
1.Korent 1:26–27
Nun nag nooy njaqi bani kese yi yeb jooju alal, ngir mu bir ne manoore ju yéeme ji alal ji làmboo, manoorey Yàllaa, waaye du sunu jos.
2.Korent 4:7
Bés yu mujj yi
Wone yépp19 Sàt 2025
18 Sàt 2025
17 Sàt 2025
16 Sàt 2025
15 Sàt 2025
14 Sàt 2025
13 Sàt 2025