Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
Room 8:28
Leeru Bés bi
Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
Room 8:28
Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.
Taalifi cant 76:10
Dëgg la, fexeel ngeen ma lu bon, waaye Yàllaa ko walbati, def ko lu baax, ba dogal li am tey jii, muy bakkan yu bare yi mucc.
Njàlbéen ga 50:20
Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom, muy Póol, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di tey, di ëllëg, lépp, yeena ko moom. Yeen nag, Almasi bi moo leen moom, te Almasi bi, Yàllaa ko moom.
1.Korent 3:21–23
Loolu lépp yeena tax, ngir yiwu Yàlla law a law, ba cant gu ne gàññ tukkee ci ñi ëpp ci nit ñi, ngir màggug Yàlla. Moo tax dunu ñàkk yaakaar. Doonte sax sunu bitib jëmm a ngi gën di bon, sunu jëmmu biir moom, mu ngi yeeslu bésoo bés. Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk.
2.Korent 4:15–17
Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk, te xam ne bu seen ngëm nattoo, ñeme coono la leen di jural. Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn.
Yanqóoba 1:2–4
Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww. Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk.
Yowaan 14:16–17
Moom miy Noowug dëgg gi, bu dikkee, moo leen di àggale ci dëgg gi gépp, ndax du ci coobarey boppam lay wax, waaye mboolem lu mu dégg la leen di wax, te liy ñëw ëllëg, moo leen koy wax. Moom, dina feeñal sama daraja, ndax ci sama jagleb bopp lay tanqe, àgge leen ko.
Yowaan 16:13–14
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:5
Waaye ku taqoo ak Sang bi, yaak moom menn xel ngeen di doon.
1.Korent 6:17
Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,
1.Korent 6:19
Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.
Efes 4:30
Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
Room 8:26
Bés yu mujj yi
Wone yépp20 Sàt 2025
19 Sàt 2025
18 Sàt 2025
17 Sàt 2025
16 Sàt 2025
15 Sàt 2025
14 Sàt 2025