Leeru Bés bi — 19 Sàttumbar: 1.Piyeer 5:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi bi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.

1.Piyeer 5:10

Aji Sax ji ne ko: «Dinaa rombale sama gépp mbaax fi sa kanam, tey biralaale turu Aji Sax ji fi sa kanam. Maay baaxe ku ma neex, te maay ñeewante ku ma neex.»

Mucc ga 33:19

da koy baaxe, daldi ne Yàlla: «Musal ko ba du wàccagum biir pax. Maa ngeek njotlaayam.»

Ayóoba 33:24

te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di baaxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu. Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon,

Room 3:24–25

Yoon wi indi ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lees ko joxee, waaye yiw wi ak dëgg gi, ci Yeesu Almasi bi la dikke.

Yowaan 1:17

Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la;

Efes 2:8

ñeel Timote, sama doomu bopp ci wàllu ngëm. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi ak sunu Sang Almasi Yeesu.

1.Timote 1:2

Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ci yiwu Yàlla, ni ko nattub Almasi bi séddalee.

Efes 4:7

Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax, di saytu ay may yu yiwu Yàlla wu yaa di joxe.

1.Piyeer 4:10

Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»

Yanqóoba 4:6

Waaye màggleen ci wàllu yiwu sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi bi, ak ci wàllu xam-xam bu ngeen ko xam. Ndam ñeel na ko tey, ba kera bés bu sax dàkk. Amiin.

2.Piyeer 3:18

Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Damaa séentu tund ya, te naan fu wall di jóge? Sama wall a nga fa Aji Sax ji, Ki sàkk asamaan ak suuf.

Taalifi cant 121:1–2

Ni tund yi yéewe Yerusalem, ni la Aji Sax ji yéewe ñoñam, tey ak ëllëg.

Taalifi cant 125:2

Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Yaw laay séentu, yaw mi toog fa asamaan. Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët, ba keroog mu baaxe nu.

Taalifi cant 123:1–2

Su ma tëddee, fàttaliku la, waxtuw guddi dama lay xalaat.

Taalifi cant 63:7

Éy sunu Yàlla, xanaa doo leen ñàkka dikke mbugal mi ñu yelloo, nde nun kat amunu dooley jànkoonteek gàngoor gu réy gii dikk ci sunu kaw. Nun nag danoo xamul nu nuy def, te yaw kat lanu ne jàkk sunuy gët.»

2.Jaar-jaar ya 20:12

Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji, moo may xettali ci fiiru noon.

Taalifi cant 25:15

Sunu ndimbal a ngi ci turu Aji Sax ji, Ki sàkk asamaan ak suuf.

Taalifi cant 124:8