Leeru Bés bi — 16 Sàttumbar: Kàddu yu xelu 21:2

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Lu waay def, daa jub ca moom, waaye Aji Sax jeey natt xol yi.

Kàddu yu xelu 21:2

Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.

Taalifi cant 1:6

Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu tànn nag, dina ko jegeñal boppam.

Màndiŋ ma 16:5

su ko defee sa sarax di kumpa, te sa Baay biy gis ci biir kumpa moo lay yool.

Macë 6:4

Yàlla, seetlu ma, ba ràññee sama xol; natt ma, ba ràññee sama xalaati xol. Xoolal ndax maa ngi doxe yoon wu aay, te nga teg ma ci yoon wi sax.

Taalifi cant 139:23–24

Cofeel àndul ak gennug ragal, waaye cofeel gu mat sëkk dàq na ag ragal; ag ragal, mook séentu ag mbugal ñoo ànd; te ku ragal, sag cofeel a des.

1.Yowaan 4:18

Sama yaram dee goyy, ma ne lasar, jàq, di binni.

Taalifi cant 38:9

sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.

Taalifi cant 142:3

Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, ndax ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.

Room 8:27

Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»

2.Timote 2:19

Yeen aji gëm ñi, woyleen Aji Sax ji, njukkale ko sellaayam.

Taalifi cant 30:5

ngir kenn baña jàq ci biir tiis yii, ndax yeen ci seen bopp xam ngeen ne loolu lanu séddoo. Ba nu nekkee ak yeen sax lanu leen njëkkoona wax ne dinanu daj ay coono, te xam ngeen ne noonu la ame.

1.Tesalonig 3:3–4

Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»

Yowaan 16:33

Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, yewwu, regge sa jëmm.

Taalifi cant 17:15

Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.

Room 13:12

Mooy mëdd dee ba fàww! Boroom bi Aji Sax jeey fompe gépp kanam rongooñi boroom. Buumi gàccey ñoñam it, moo koy doge fépp ci àddina. Aji Sax ji kat wax na ko.

Esayi 25:8

Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»

Peeñu ma 21:4

Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww. Kon nag deeleen dëfalantee yooyu kàddu.

1.Tesalonig 4:17–18