Barax bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim, du ko fey, ba kera mu mayee njub, ndam,
Macë 12:20
Leeru Bés bi
Barax bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim, du ko fey, ba kera mu mayee njub, ndam,
Macë 12:20
Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal.
Taalifi cant 51:17
di faj naqaru xol, fajtal góomi boroom.
Taalifi cant 147:3
Ku màgg, Ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk te toroxlu, ngir leqali ku toroxlu, leqali boroom xol bu mokk. Duma wéye di sikke ba fàww, duma saxoo di mer, lu ko moy képp ku ma sàkk day tàggook bakkanam.
Esayi 57:15–16
Bu ci réer, maa lay seet; bu ci xàjjiku, maa lay delloosi; bu ci damm, maa yeew ba mu dëgër; bu ci néew doole, ma leqali la. Waaye bu ci duuf, am doole, maa lay sànk, sàmm la, def li war ci yaw.
Esekiyel 34:16
Kon nag «dëgëralleen loxo yi toqi ak óom yi bañ,» te «ngeen xàllal seen bopp xàll yu jub yu ngeen di jaare seeni tànk,» ngir kuy soox doxe ca wér te baña gëna tële.
Yawut ya 12:12–13
Ku fitam rëcc, ne leen ko: «Dëgërlul te bul tiit. Sa Yàllaa ngii di la feyul, ba yool say noon. Moom mooy dikk, wallusi la.»
Esayi 35:4
Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.
Taalifi cant 34:8
Njiitu xew wa mos ndox ma, ndeke soppaliku na biiñ. Xamul fu biiñ ba jóge, teewul surga ya tanq ndox ma, ñoom xam nañu ko. Njiit la woo boroom séet ba, ne ko: «Mboolem kuy xew, biiñ bu neex lay njëkka joxe; bu nit ñi naanee ba doyal, mu doora taaj bu yemamaay. Yaw nag nga denc bu neex bi ba nëgëni!»
Yowaan 2:9–10
Purux déy ay mosu ñam, nopp natt kàddu.
Ayóoba 34:3
Bindees na ne: «Damaa gëm, moo tax ma wax.» Nun it, wenn xeetu ngëm wi lanu am. Danoo gëm, moo tax itam nuy wax.
2.Korent 4:13
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
Mbete garab gu gëna neex ci gott bi, kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi. May bége keppaaram, safoo doom ya.
Ngën-gi-woy 2:3
Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy akug jéllaleem akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?
Room 2:4
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Room 8:32
Ni liir buy doora juddu yàkkamtee nàmpe, ni ngeen wara yàkkamtee nàmp soow mu set miy kàddug Yàlla. Mooy tax ngeen màgg ci seen dundug texe, gannaaw mos ngeen ci mbaaxug Sang bi.
1.Piyeer 2:2–3
Éy Yàlla, topp leen, ñu fakkastaloo seeni pexe; xalabal ñooñu barey moy, ñoo la gàntal.
Taalifi cant 5:11
Bés yu mujj yi
Wone yépp16 Sàt 2025
15 Sàt 2025
14 Sàt 2025
13 Sàt 2025
12 Sàt 2025
11 Sàt 2025
10 Sàt 2025