Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi. Ba ci lan boog? Ndax kon danuy bàkkaar, gannaaw du ci kilifteefu yoonu Musaa lanu nekk, waaye ci aw yiw lanu tàbbi? Déet kay!
Room 6:14–15
Leeru Bés bi
Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi. Ba ci lan boog? Ndax kon danuy bàkkaar, gannaaw du ci kilifteefu yoonu Musaa lanu nekk, waaye ci aw yiw lanu tàbbi? Déet kay!
Room 6:14–15
Noonu la deme ak yeen itam, bokk yi. Yaramu Almasi wi ngeen bennool, ci ngeen doone ñu dee ba nangootunu kilifteefu yoonu Musaa. Noonu ngeen doone moomeelu keneen, te kooku mooy ki dekki, ngir nu meññ njariñ lu ñeel Yàlla.
Room 7:4
Maak ñi amul yoonu Musaa, damaa mel ni ku amul yoonu Musaa, ngir iri leen, doonte ñàkkuma yoonu Yàlla, gannaaw maa ngi ci yoonu Almasi bi.
1.Korent 9:21
Dee, ag fittam mooy bàkkaar, te bàkkaar, dooleem mooy yoon wi. Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!
1.Korent 15:56–57
Ndax kat, yoonu Noo gu Sell giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci yoonu bàkkaar ak dee.
Room 8:2
Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, képp kuy bàkkaar, ab jaamu bàkkaar la.
Yowaan 8:34
Kon nag su leen Doom ji goreelee, ngeen diy gor tigi.
Yowaan 8:36
Almasi bi da noo yiwi, ngir nu yiwiku, kon nag saxooleen ko, te baña laxasooti buumi njaam.
Galasi 5:1
Boroom xel ñaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def.
Yanqóoba 1:8
Yeesu ne ko: «Képp ku tàmbalee gàbb tey xool gannaawam, jekkoo ci nguurug Yàlla.»
Luug 9:62
Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga njëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.
Yawut ya 11:6
Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje. Kooku bumu yaakaar dara ci Boroom bi.
Yanqóoba 1:6–7
Moo tax ma di leen wax lii: Lépp lu ngeen di sàkku cig ñaan, gëmleen ne jot ngeen ko ba noppi, dingeen ko am.
Màrk 11:24
Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu. Su boobaa kay, dëgg gu nu wodde cofeel lanuy wéye, tey màgg ci bépp fànn, ci moom Almasi biy bopp bi.
Efes 4:14–15
Saxleen ci man, ni ma saxe man ci sama bopp ci yeen. Ni carub reseñ tëlee meññal boppam, su saxul ci ndeyam, ni ngeen di tëlee meññ, su ngeen saxul ci man.
Yowaan 15:4
Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.
1.Korent 15:58
Bés yu mujj yi
Wone yépp14 Sàt 2025
13 Sàt 2025
12 Sàt 2025
11 Sàt 2025
10 Sàt 2025
9 Sàt 2025
8 Sàt 2025