Leeru Bés bi — 13 Sàttumbar: Yowaan 7:37

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Bés ba mujj ca màggal ga nag moo ca gënoona màgg. Keroog la Yeesu taxaw, àddu ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man, naan;

Yowaan 7:37

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaaka sopplub dëkkuwaay!

Taalifi cant 84:2

Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda. Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla, ma xëy di la wër, sama bakkan mar la, sama jëmm namm la, fu suuf mare ndox, ne sereŋ.

Taalifi cant 63:1–2

«Éey, yeen ñi mar ñépp, dikkleen ci ndox mi, ba ci ku amul xaalis sax! Dikkleen jënd pepp, lekk! Dikkleen jënd pepp mu xaalis jëndul, ak biiñ ak meew mu amul pey.

Esayi 55:1

Noo gu Sell gi ak Séet bi nee ñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.

Peeñu ma 22:17

waaye ku naan ci ndox mi ma koy may, man, du marati; ndox mi ma koy may, bëtu ndox lay doon ci moom, di ball, ngir dundug texe gu sax dàkk.»

Yowaan 4:14

Ndaxte sama yaram mooy ñam wi wóor, sama deret di naan gi wóor.

Yowaan 6:55

Jigéen sama, séet sama, dikk naa sama tool, sama ndàbb ak sama cuuraay, ma for, sama lem xelli, ma lekk, sama biiñ ak sama meew, ma naan. Yeen soppe yi, lekkleen; yeen ñi bëggante, naanleen ba màndi.

Ngën-gi-woy 5:1

«Yeena di xoromas àddina. Bu xorom raxee ba sàlli, nees koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, xanaa ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam.

Macë 5:13

waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.

1.Piyeer 3:4

Ndax kat dangeena judduwaat, te jiwu wi ngeen judduwaate mooy kàddug Yàlla giy dund te sax dàkk; du jiwu wuy yàqu, waaye mooy jiwu wu dul yàqu mukk.

1.Piyeer 1:23

Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund.

Yowaan 11:25

Dootuñu mana dee it, ndax niy malaaka lañuy mel. Ay doomi Yàlla lañuy doon, ndax da leen di fekk dekki.

Luug 20:36

Leeru Yàlla ji dul dee lañu weccee jëmmu nit ki deewam dul jaas, ak picc, ak boroom ñeenti tànk, ak ndëgmeent.

Room 1:23

Yeen nag nekkatuleen ci kilifteefu bindu suuxu neen, waaye ci kilifteefu Noo gu Sell gi ngeen nekk, ndegam kay Noowug Yàllaa ngi sax ci yeen. Ku amul Noowug Almasi bi, kooku du nitam. Su Almasi bi nekkee ci yeen, seen yaram dina dee moos ndax bàkkaar, waaye du tee seenug noo di dund, ndax àtteb njub bi ngeen am ba noppi. Noowug ki dekkal Yeesu moo sax ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi bi mooy dekkal itam seen yaram wu jëm ci dee, ndax Noowam googu sax ci yeen.

Room 8:9–11

Noonu itam la ndekkitel ñi dee di deme. Li ñu suul mooy jiwu wiy yàqu, te bu dekkee dootul yàqu.

1.Korent 15:42

Xorom lu baax la, waaye bu raxee ba sàlli, nees koy delloo cafkaam? Nangeen jikkowoo xorom su raxul, daldi jàmmoo.»

Màrk 9:50

Bu genn kàddu gu bon génne seen gémmiñ, xanaa su ko jaree ngeen wax lu baax, luy jariñe, te diw yiw ci ñi koy dégg.

Efes 4:29