Xam naa jikkoom, waaye maa koy faj, wommat ko, dëfale koy xéewal, mook ñiy ñaawloondook moom.
Esayi 57:18
Leeru Bés bi
Xam naa jikkoom, waaye maa koy faj, wommat ko, dëfale koy xéewal, mook ñiy ñaawloondook moom.
Esayi 57:18
Da ne leen: «Bu ngeen farloo ci déggal seen Yàlla Aji Sax ji, di def li mu rafetlu, di teewlu tey jëfe ay santaaneem, di sàmm bépp dogali yoonam, su boobaa duma leen teg lenn ci jàngoro yi ma tegoon waa Misra, ndax man maay Aji Sax ji leen di wérloo.»
Mucc ga 15:26
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax ji, yaa ma natt, xam ma; yaa xam sama toogaay ak sama taxawaay, di ràññee fu sore samay xalaat, di càmbar samab dox ak sama tëraay, yittewoo lépp lu may def.
Taalifi cant 139:1–3
Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, te sunu mbóot leer na la.
Taalifi cant 90:8
Te it amul mbindeef mu làqu fi kanam Yàlla. Lépp a ne duŋŋ, ne fàŋŋ, muy gis, te moom lanuy waxal bés-pénc.
Yawut ya 4:13
«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
Esayi 1:18
da koy baaxe, daldi ne Yàlla: «Musal ko ba du wàccagum biir pax. Maa ngeek njotlaayam.»
Ayóoba 33:24
Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. Yar yi nu jàmmal moom la dal, te mooy ki nu wére ciy góomam.
Esayi 53:5
Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi seen goreel, yégal ñi ñu tëj seen ubbite.
Esayi 61:1
Yeesu ne ko: «Janq, sa ngëm a la faj. Demal ak jàmm te teqalikook sa jàngoro.»
Màrk 5:34
Aji Sax jeek man, di ma dimbali, may seetaan bañ yi.
Taalifi cant 118:7
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Buur, yal na la Aji Sax ji nangul bésu njàqare, yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe,
Taalifi cant 20:1–2
Yal na la may li nga namm, di sottal loo mébét,
Taalifi cant 20:5
Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey. Moo koy nangule fa asamaan su sell sa, ci dooley ndijooram biy musle. Ñiiki watiir, ñeeki fas, nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd.
Taalifi cant 20:7–8
Dees na ragale turu Aji Sax ji fa sowu, ragale màggaayam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.
Esayi 59:19
Benn nattu dabu leen bu moy nattu yiy dale. Te it Yàllaa jara wóolu. Yàlla du nangu ngeen tegoo nattu bu ngeen àttanul, waaye nattu ba lay booleek pexe ma leen cay génne, ba ngeen man koo dékku.
1.Korent 10:13
Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Room 8:31
Aji Sax jeek man, duma tiit. Ana lees ma manal?
Taalifi cant 118:6
Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal.
Dañeel 3:17
Bés yu mujj yi
Wone yépp11 Sàt 2025
10 Sàt 2025
9 Sàt 2025
8 Sàt 2025
7 Sàt 2025
6 Sàt 2025
5 Sàt 2025