Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.
Room 12:2
Leeru Bés bi
Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.
Room 12:2
Buleen seet fi mbooloo gëna baree, ngeen topp leen ci jëf ju bon; te it buleen jeng, di topp mbooloo mu gëna bare ci ab layoo, di leen seedeel lu toxal dëgg.
Mucc ga 23:2
Bokkaalekat yi ngeen doon! Xanaa xamuleen ne xaritoo ak àddina moo di noonoo ak Yàlla? Kon nag ku namma def àddina ab xarit, ab noonu Yàlla ngay doon.
Yanqóoba 4:4
Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq? Gan juboo la Almasi bi ak Seytaane séq? Wan wàll la gëmkat bi bokk ak gëmadikat bi? Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»
2.Korent 6:14–16
Buleen topp àddina ak li ci biiram. Ku topp àddina, cofeelu Baay bi nekkul ci moom.
1.Yowaan 2:15
Te àddina day jeex, mooki xemmemtéefam, waaye kuy jëfe coobarey Yàlla mooy sax ba fàww.
1.Yowaan 2:17
yi ngeen doon dunde démb, ngeen àndoon ci ak doxalinu àddinay tey jii, ak ku bon kiy kàngamu boroom baat yi ci jaww ji asamaan tiim, di boroom xel mu bon mi wéye liggéeyam ci biir aji déggadi ñi, tey.
Efes 2:2
Yeen nag du loolu ngeen jànge ci Almasi bi, ndegam kay Yeesu ci boppam ngeen dégg mbiram, ba jànge ci moom, dëgg gi bawoo ci moom,
Efes 4:20–21
doom aadama tàmbali kër-këram, di yendoo liggéey ba ngoon.
Taalifi cant 104:23
saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»
Njàlbéen ga 3:19
ndax ba nu nekkee ak yeen, ndigal lanu leen joxoon moo di lii: «Ku nanguwula liggéey, bumu lekk.»
2.Tesalonig 3:10
Sàkkuleen di jëfe jëfin wu dal, te ngeen di toppatoo lu seen yoon nekk, tey dunde seenu ñaq, na nu leen ko sante woon.
1.Tesalonig 4:11
Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw ga nga jëm.
Kàdduy waare 9:10
Danoo wara liggéey liggéeyu ki ma yónni ci bi muy bëccëg; bu guddee kenn du liggéey.
Yowaan 9:4
Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.
Galasi 6:9
Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.
1.Korent 15:58
Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.
Yawut ya 4:9
naan: “Ñii mujja ñëw, liggéeyuñu lu moy wenn waxtu, nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi, ak naaj wu tàng wi!”
Macë 20:12
Moo leen waxoon ne leen: «Fii moo di noppalukaay bi, noppalleen ku sonn. Fii a di dalluwaay bi!» Waaye nanguwuñoo dégg.
Esayi 28:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp10 Sàt 2025
9 Sàt 2025
8 Sàt 2025
7 Sàt 2025
6 Sàt 2025
5 Sàt 2025
4 Sàt 2025