Nii laa jënde tool ba ca Anatot ci Anamel sama doomu baay bu ndaw. Ma waññal ko xaalis bi, muy fukki dogi xaalis ak juróom ñaar.
Yeremi 32:9
Leeru Bés bi
Nii laa jënde tool ba ca Anatot ci Anamel sama doomu baay bu ndaw. Ma waññal ko xaalis bi, muy fukki dogi xaalis ak juróom ñaar.
Yeremi 32:9
Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, wecceel leen ko xol yu nooye ni suux,
Esekiyel 36:26
Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi, di jiite ku woyof mbubb ci njubte, di ko xamal aw yoonam. Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.
Taalifi cant 25:8–10
ngir ñépp doon benn, ni nga nekke yaw Baay, ci man, ma nekke ko ci yaw, ñoom itam, ñu nekke ni ci nun, ba àddina gëm ne yaw yaa ma yebal.
Yowaan 17:21
Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla bi mu leen woo. Saxooleen woyof, lewet, te deeleen muñ, di muñalante ngir cofeel. Defleen seen kem kàttan, ngir di jàmmoo, ba mana sàmm seenug bennoo ci biir Noo gu Sell gi ngeen bokk. Wenn yaram a fi nekk ak genn Noo ak jenn yaakaar ju leen wooteb Yàlla jëme. Benn Sang bi la it, ak genn ngëm ak genn sóobu cim ndox. Te it jenn Yàllaa am; mooy Baayu ñépp, moo tiim ñépp, di jëf ci ñépp te nekk ci ñépp.
Efes 4:1–6
kiy yaakaar Aji Sax ji moom, di yeeslu doole; da naa fëyy ni jaxaay juy naaw, di xélu te du xiix, di dox te du xoox.
Esayi 40:31
Looloo ma tax di bànneexu ci biir diggante yu ma néewe doole ak ci biiri saaga ak ci biir ag ñàkk ak ci biir coono yu ñu may bunduxataale ak ci biir njàqare yu ma dal ngir Almasi bi. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laa am kàttan.
2.Korent 12:10
Tey nag Aji Sax jee wax, moom mi dale sama biiru ndey, mooñ ma, ma dib jaamam bi koy waññil askanu Yanqóoba ba ca moom, dajaleel ko bànni Israayil googu fa moom, ba jagoo teraangay Aji Sax ji, sama Yàlla jii di sama doole.
Esayi 49:5
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.
2.Korent 12:9
Xanaa ku langaamoo sama kiiraay te jàmmook man, ba jàmmook man.
Esayi 27:5
làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.
Taalifi cant 55:22
Teewul xalaam ga di wéye daŋ, te la loxo yay dëgërloo mooy loxoy Jàmbaar ju Yanqóoba, kookooy Sàmm bi, Doju cëslaayal Israayil,
Njàlbéen ga 49:24
Ba nit ka xamee ne manalu ko dara, dafa dóor Yanqóoba ci yaxu mooco bi, mu summikoo ca bëre ba.
Njàlbéen ga 32:26
Ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, digaaleel ak samay digaale, xeexal maak ñi may xeex. Fëkkal sa pakk ak sa kiiraay, taxawusi ma,
Taalifi cant 35:1–2
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Sàt 2025
8 Sàt 2025
7 Sàt 2025
6 Sàt 2025
5 Sàt 2025
4 Sàt 2025
3 Sàt 2025