Booba kenn ca taalibe ya, di ku Yeesu soppoon, ma nga sóonu, sës rëkk ca Yeesu.
Yowaan 13:23
Leeru Bés bi
Booba kenn ca taalibe ya, di ku Yeesu soppoon, ma nga sóonu, sës rëkk ca Yeesu.
Yowaan 13:23
Man maa leen di naxtaan ba ngeen dal, ni doom ju ndeyam di naxtaan ba mu dal, ngeen am xel mu dal fi Yerusalem.»
Esayi 66:13
Ay xale lañu indiloon Yeesu ngir mu teg leen ay loxoom. Teewul taalibe ya jànni leen.
Màrk 10:13
Yeesu nag fab leen, teg leen ay loxoom, barkeel leen.
Màrk 10:16
Gannaaw loolu Yeesu woo taalibeem ya, ne leen: «Damaa yërëm mbooloo mi, ndax ñetti fan a ngii yu ñu nekk ak man, te amuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi, ñu deme xiif, bala ñoo tële ci yoon wi.»
Macë 15:32
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Yawut ya 4:15
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.
Esayi 63:9
Duma leen bàyyi ngeen tumurànke. Dinaa délsi ci yeen.
Yowaan 14:18
Aji Sax ji nee: «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram? Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte.
Esayi 49:15
ndaxte Xar mi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»
Peeñu ma 7:17
Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub. Moom ci boppam moo dig njotlaay ñeel sunuy bàkkaar, te du sunuy bàkkaar doŋŋ, waaye yoy àddina sépp la ñeel.
1.Yowaan 2:1–2
Ba loolu amee ñu bàyyikoo ca Firawna, daldi yem ca Musaak Aaróona, fa ñu leen doon xaar. Farba ya ne leen: «Yal na leen Aji Sax ji gis ba mbugal leen, ndax tax ngeen Firawnaaki dagam jéppi nu, te mel na ni yeena teg ci seeni loxo saamar, bi ñu nuy reye.» Musaa dégg loolu, dellu ci Aji Sax ji, ne ko: «Éey Boroom bi, loraange gi nga yóbbe mbooloo mii nag? Loo ma doon yónnee?
Mucc ga 5:20–22
Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof. Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
Taalifi cant 85:9–10
Waaye yaay jéggale, ñu ragal la.
Taalifi cant 130:4
Éey Israayil, négandikul Aji Sax ji. Aji Sax jee gore, te yaatug njot. Mooy jot Israayil ci ñaawtéefam yépp.
Taalifi cant 130:7–8
Ndax kat ñépp a bàkkaar, ba jotewuñu leeru Yàlla, te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di baaxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu. Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon,
Room 3:23–25
Bés yu mujj yi
Wone yépp3 Sul 2025
2 Sul 2025
1 Sul 2025
30 Suw 2025
29 Suw 2025
28 Suw 2025
27 Suw 2025