Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
Room 8:17
Leeru Bés bi
Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
Room 8:17
Te su ngeen bokkee ci Almasi bi, yeen ay askanu Ibraayma, te yeena jagoo dige ba.
Galasi 3:29
Ndaw cofeel gu nu Baay bi won, ba ñu di nu woowe doomi Yàlla, te moom lanu it. Àddina nag xamu nu, te li ko waral moo di da koo xamul moom itam.
1.Yowaan 3:1
Moo tax dootuloo ab jaam, doom nga. Gannaaw doom nga nag, boroom cér nga it fa Yàlla sa baay.
Galasi 4:7
la dogaloon lu jiitu, ne ci Yeesu Almasi bi la nuy defe ay doomi boppam, te muy bànneexam, di coobareem.
Efes 1:5
«Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.
Yowaan 17:24
«Ku am ndam nag, ku saxoo jëf ji ma soob, ba kera muj ga, maa lay jox sañ-sañ ci kaw xeet yi:
Peeñu ma 2:26
«Ku am ndam nag, maa lay may nga toog ak man fi sama ngàngune, na ma ame woon ndam, ba toog ak sama Baay fi ngànguneem.
Peeñu ma 3:21
Li tuut ab juddu ci àddina ak li xeeblu, li tekkiwul dara, moom la Yàlla tànn, ngir neenale ko li tekki,
1.Korent 1:28
Ñu boole waaru ak yéemu, naa: «Ñii di wax nii ñépp, xanaa duñu waa Galile?
Jëf ya 2:7
Yeesoo doon doxe ca tàkkal dexu Galile, daldi gis ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Àndre rakkam. Ña ngay mbaal ca dex ga, ndax ay nappkat lañu woon. Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ma, ma def leen nappkati nit.»
Macë 4:18–19
Ba waa kuréelu àttekat ya gisee fit wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.
Jëf ya 4:13
Sama kàddu ak samam njàngale jotewul woon dara ak neex làmmiñ gu xam-xamu nit ràbb, waaye dafa di ay firnde yu manooreg Noowug Yàlla lañal, ngir seen ngëm baña sukkandiku ci xam-xamu nit, te sukkandiku ci manooreg Yàlla.
1.Korent 2:4–5
Du yeen yeena ma tànn, man maa leen tànn, sas leen ngir ngeen dem, meññi meññeef, te seenum meññeef sax, ba lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko.
Yowaan 15:16
«Man maay reseñ gi, yeen ngeen di car yi. Ki sax ci man, ma sax ci moom, kooku mooy meññ lu bare, nde su dul man, dungeen mana def dara.
Yowaan 15:5
Nun nag nooy njaqi bani kese yi yeb jooju alal, ngir mu bir ne manoore ju yéeme ji alal ji làmboo, manoorey Yàllaa, waaye du sunu jos.
2.Korent 4:7
Bés yu mujj yi
Wone yépp2 Sul 2025
1 Sul 2025
30 Suw 2025
29 Suw 2025
28 Suw 2025
27 Suw 2025
26 Suw 2025