Leeru Bés bi — 27 Suwe: Peeñu ma 6:17

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

ndax seen bésub sànj bu mag taxaw na, ana ku ko àttan?»

Peeñu ma 6:17

Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku? Bu teewee ana kuy taxaw? Nde moom daa mel ni sawaras tëgg buy xelli weñ, melati ni xemey fóotkat.

Malasi 3:2

Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làkk yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Xar mi, sol mbubb yu weex, jël ay cari garabi tàndarma.

Peeñu ma 7:9

Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Xar mi. Loolu moo leen taxa teew fi kanam ngàngunem Yàlla, di ko jaamu ci biir màkkaanam guddi ak bëccëg, te ki toog ci ngàngune mi moo leen di yiir. Dootuñu xiif, dootuñu mar. Dootuñu loru ci jant bi mbaa weneen tàngoor, ndaxte Xar mi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»

Peeñu ma 7:14–17

Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.

Room 8:1

Almasi bi da noo yiwi, ngir nu yiwiku, kon nag saxooleen ko, te baña laxasooti buumi njaam.

Galasi 5:1

Sang bi, bul layook man; kenn jubul fi sa kanam, du kuy dund.

Taalifi cant 143:2

«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.

Esayi 1:18

Xanaa ku langaamoo sama kiiraay te jàmmook man, ba jàmmook man.

Esayi 27:5

Jubool ak Yàlla rekk, am jàmm, ngëneel dikkal la.

Ayóoba 22:21

Gannaaw nag dees noo baaxe àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi bi.

Room 5:1

Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di baaxee àtteb ku jub, waaye ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi bi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla àtte nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi bi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di baaxee kenn àtteb ku jub.

Galasi 2:16

Ndax kat deesul baaxe kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solos yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.

Room 3:20

képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.

Jëf ya 13:39

Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!

1.Korent 15:57