Gannaaw loolu Aji Sax ji dafa wax ak Musaa ak Aaróona, ne leen: «Li ma dogal ci saraxu bésub Mucc bi mooy lii. Benn doxandéem du ci lekk.
Mucc ga 12:43
Leeru Bés bi
Gannaaw loolu Aji Sax ji dafa wax ak Musaa ak Aaróona, ne leen: «Li ma dogal ci saraxu bésub Mucc bi mooy lii. Benn doxandéem du ci lekk.
Mucc ga 12:43
Sunu sarxalukaayu bopp la ñu cay teg, ñay liggéeye ca xaymab jaamookaay ba, sañuñu caa lekk.
Yawut ya 13:10
Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki, su judduwaatul, du mana gis nguurug Yàlla.»
Yowaan 3:3
Jant yooyu amuleen woon benn cér ci Almasi bi, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu bànni Israayil. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina. Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru. Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jàmbur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante. Yoonu Musaa ak santaane yaak ndigal ya, moom la xewwil, ngir yeesal ñaar ñi, Yawut beek jàmbur bi, ci jenn jëmmu boppam, ñu doon kenn nit ku yees, ba jàmmoo.
Efes 2:12–15
Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen.
Efes 2:19
Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat, ba ubbil ma, dinaa agsi moos sa néeg, nu bokk reer.
Peeñu ma 3:20
Mu bàyyikoo ca ñoom, demati ba nee ñetteel bi yoon, daldi dellu ca genn kàddug ñaan googa.
Macë 26:44
Fan yi Almasi bi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te ñaan ga nangu na it, ndax na mu ragale woon Yàlla.
Yawut ya 5:7
Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
Ose 6:3
Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.
Room 12:12
Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
Efes 6:18
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Filib 4:6–7
Ba loolu amee, Yeesu dox ba sore leen tuuti, ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf. Mu ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko! Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
Macë 26:39
Kóolute gi nu am ci Yàlla moo di su nu ko ñaanee lenn lu dëppook coobareem, da nuy nangul.
1.Yowaan 5:14
Deel bànneexoo Aji Sax ji, mu may la say nammeel. Jébbalul ci Aji Sax ji, dénku ci moom, mooy sottal.
Taalifi cant 37:4–5
Bés yu mujj yi
Wone yépp1 Sul 2025
30 Suw 2025
29 Suw 2025
28 Suw 2025
27 Suw 2025
26 Suw 2025
25 Suw 2025