Leeru Bés bi — 28 Suwe: Ayóoba 19:25

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Waaye man xam naa ne sama Jotkat a ngi dund, te mooy mujje taxaw fi kaw suuf.

Ayóoba 19:25

Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?

Room 5:10

Waaye Yeesu mi sax ba fàww, moo sasoo carxal gu sax dàkk. Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.

Yawut ya 7:24–25

Des na tuuti, àddina du ma gisati; yeen dingeen ma gis, ndax man maa ngi dund, te yeen itam dingeen dund.

Yowaan 14:19

Su dee ci giiru dund gii doŋŋ lanu ame yaakaar ci Almasi bi, kon de noo gëna toskare ñépp. Waaye nag Almasi bi dafa dekki moos, te mooy saraxu ndoortel meññeef bi ñu sàkke ci ngóobum bakkani nit ñi dee.

1.Korent 15:19–20

«Ab jotkat ay dikkal Siyoŋ, ba jot ñi tuub seeni bàkkaar ci askanu Yanqóoba.» Kàddug Aji Sax jee.

Esayi 59:20

Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,

Efes 1:7

Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam, waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul.

1.Piyeer 1:18–19

Noowug Yàlla wax na ci lu leer ne ci mujug jamono, dina am ñu wacc yoonu ngëm wi, di topp ay xalaat yuy fàbbee ak ay àlluway ceytaane

1.Timote 4:1

Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.»

Luug 8:18

Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.

Kolos 3:16

Te fu ngeen tollu ŋàbbleen pakk biy seen ngëm, ci ngeen mana fanqe mboolem jumi sawaray ku bon ki.

Efes 6:16

Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar, say santaane laa jëfe.

Taalifi cant 119:166

Sa kàddooka maa neex, ba dàqal ma tem-temu lem! Ci say tegtal laay ràññee, ba tax ma bañ luy yoonu fen. Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.

Taalifi cant 119:103–105

Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.

Taalifi cant 119:99

Te loolu jarula waaru, ndax Seytaane ci boppam, malaakam leer lay mbubboo.

2.Korent 11:14

Waaye nun ci sunu bopp, mbaa malaaka mu bawoo ci asamaan sax, ku leen ci àgge woon beneen xibaaru jàmm bu dul bi nu leen àgge, kooku yal na alku!

Galasi 1:8