«Man, képp ku ma sopp, maa koy jubbanti, yar ko. Kon nag farlul te tuub!
Peeñu ma 3:19
Leeru Bés bi
«Man, képp ku ma sopp, maa koy jubbanti, yar ko. Kon nag farlul te tuub!
Peeñu ma 3:19
Te it fàtte ngeen kàddu yii ñu leen ñaaxe, ni nit aki doomam: «Doom, bul xeeb yaru Boroom bi, bul xàddi, bu la waññee, ndax Boroom bi, ku mu sopp, yar la, mooy bantal jépp doom ju ko neex.»
Yawut ya 12:5–6
ndax Aji Sax ji, ku mu sopp, yar la, ni baay, ak doom ju ko neex.
Kàddu yu xelu 3:12
Moom kat mooy mitital, di fajtal; mooy gaañe, di wérale loxol boppam.
Ayóoba 5:18
Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo,
1.Piyeer 5:6
Ma ne, togg naa leen, xelli cib taal, waaye du taalu xellikaayu xaalis, sawaras nattu laa leen xellee.
Esayi 48:10
Du bànneexam lay tege coono, aka naqaral doom aadama.
Jooytu 3:33
Du sunuy bàkkaar la nu mbugal, du sunuy ñaawtéef la nu fey. Ni asamaan tiime suuf, ni la ngoram yiire ku ko ragal. Ni penku soree sowu, ni la nu soreleek sunu mbugali tooñ. Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal. Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.
Taalifi cant 103:10–14
Bu xalaat baree, indi gént; bu wax baree, waxi dof jib.
Kàdduy waare 5:2
«Bu ngeen di ñaan, buleen jàppoo kebetu ni yéefar yi foog ne ci wax ju bare lees leen di nangule. Kon buleen mel ni ñoom, ndax seen Baay xam na li ngeen soxla bala ngeen ko koo ñaan.
Macë 6:7–8
Ñu jël yëkk wa mu leen jox, defar ko. Ñuy yuuxu, di woo Baal suba ba digg bëccëg, naan: «Baal, wuyu nu!» Waaye kenn àdduwul, kenn wuyuwul. Ña ngay ciŋiñ-caŋañi, di wër sarxalukaay ba ñu defar.
1.Buur ya 18:26
Mu ne: «Ñaari nit a ñaani woon ca kër Yàlla ga. Kenn ki di ab Farisen, ki ci des dib juutikat. Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi fees ak ŋàppaaral, diy njublaŋ aki njaalookat, rawatina juutikat bii.
Luug 18:10–11
«Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore, ñemewula siggi sax, xool asamaan, xanaa di fëgg dënnam te naan: “Éy Yàlla, yërëm ma, man bàkkaarkat bi.”» Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»
Luug 18:13–14
Yeesu moo doon ñaan ci benn béreb. Ba mu noppee, kenn ca taalibeem ya ne ko: «Sang bi, jàngal nu ñaan, noonee Yaxya jàngale ñaan ay taalibeem.»
Luug 11:1
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Suw 2025
28 Suw 2025
27 Suw 2025
26 Suw 2025
25 Suw 2025
24 Suw 2025
23 Suw 2025