Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Leeru Bés bi
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp,
Efes 5:1
Waaye man maa leen wax ne leen, soppleen seeni noon te ñaanal ñi leen di bunduxataal, ngir ngeen doon doomi seen Baay ba fa asamaan, nde mooy kiy fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi, ak ñu baax ñi, te mooy tawal ñi jub, ak ñi jubadi.
Macë 5:44–45
Ni seen Baay ame yërmande nag, nangeen ni ame yërmande.
Luug 6:36
Li leer gi ci yeen di meññ moo di mboolem luy mbaax ak njub ak dëgg.
Efes 5:9
Waaye ba Yàlla sunu Musalkat feeñalee mbaaxam ak mbëggeelam ci doom aadama, ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell gi mu nu awale ci Yeesu Almasi bi sunu Musalkat, ba baawaanal ko ci sunu kaw.
Tit 3:4–6
Aji Sax jee baaxe ñépp, di yërëm lu mu sàkk.
Taalifi cant 145:9
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Room 8:32
Gannaaw loolu Samiyel jël aw doj, teg ko ci diggante Mispa ak fu ñuy wax Sen; mu dippee doj wi Eben Eser (muy firi Doju Wall). Mu ne: «Ba fii la nu Aji Sax ji walloo.»
1.Samiyel 7:12
Aji Sax jeey aar ku xamul àddina; tumurànke woon naa, mu wallu ma.
Taalifi cant 116:6
Jaajëfe Aji Sax ji, ki ma nangul samay dagaan! Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.
Taalifi cant 28:6–7
Làqoo Aji Sax jee gën wóolu doom aadama. Làqoo Aji Sax jee gën wóolu garmi.
Taalifi cant 118:8–9
Ndokkalee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,
Taalifi cant 146:5
jaarale leen ci yoon wu jub, ngir ñu àgg cib dëkk.
Taalifi cant 107:7
Du benn dige bu wuute ci mboolem digey ngëneel ya Aji Sax ji giñaloon waa kër Israayil. Lépp a mat sëkk.
Yosuwe 21:45
Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
Luug 22:35
Su ma tëddee, fàttaliku la, waxtuw guddi dama lay xalaat.
Taalifi cant 63:7
Bés yu mujj yi
Wone yépp30 Suw 2025
29 Suw 2025
28 Suw 2025
27 Suw 2025
26 Suw 2025
25 Suw 2025
24 Suw 2025