Leeru Bés bi — 25 Suwe: 1.Yowaan 3:2

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise.

1.Yowaan 3:2

Teewul mboolem ñi ko dalal, ba gëm ko, ñoom la may ñu yelloo doon doomi Yàlla.

Yowaan 1:12

Ci jooju daraja ak jooju jaloore lees nu baaxee ay dige yu réy njëg te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina gi xemmemtéefu bakkan waral.

2.Piyeer 1:4

Yaay gatandu kiy bége njekk gi muy jëfe te di ba xel say yoon yi ñu mas di jaare, ba mucc. Waaye kat, yaa nu mere, ndax noo bàkkaar.

Esayi 64:4

Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.

1.Korent 13:12

Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi. Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, niroole kook yaramam wi ànd ak màggaay.

Filib 3:20–21

Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, yewwu, regge sa jëmm.

Taalifi cant 17:15

«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.

Sàkkaryaa 13:7

Ndax kat ci Almasi bi, ci yaramu nitam la léppi Yàlla dëkke, ba mat sëkk ci moom,

Kolos 2:9

Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israayil mooy boroom.

Taalifi cant 89:19

«Maa doon dëre tànk, man kenn ci ab dërukaayu reseñ, xeet yépp kenn dërlewu ma ci. Sama mer laa leen dëre, sama sànj laa leen dëggaatee, seen deret tis ci samay yére, ma taqal sama yére yépp.

Esayi 63:3

Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.

1.Timote 3:16

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,

Yawut ya 1:3

Waaye Doom ji la Yàlla ne: «Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww, sa yetu buur njub la.

Yawut ya 1:8

Buy indiwaat taaw bi ci àddina nag, ci la naan: «Na ko malaakay Yàlla yépp sujjóotal.»

Yawut ya 1:6

Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»

Peeñu ma 19:16