Leeru Bés bi — 24 Suwe: Màndiŋ ma 10:33

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ci kaw loolu ñu bàyyikoo ca tundu Aji Sax ja, doxe fa doxub ñetti fan. Gaalu kóllërey Aji Sax jaa nga leen jiitu diiru ñetti fan ña, di leen wutal dalluwaay.

Màndiŋ ma 10:33

Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku. Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»

Taalifi cant 31:15

Moo nu nangulal xeet yi, nu teg tànk gàngoor yi.

Taalifi cant 47:4

Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër, sujjóotal sa béreb bu sell, wormaale la.

Taalifi cant 5:8

Jébbalul ci Aji Sax ji, dénku ci moom, mooy sottal.

Taalifi cant 37:5

Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.

Kàddu yu xelu 3:6

di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.

Esayi 30:21

Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax jee may sàmm, du lenn lu ma ñàkk. Parlu mu naat la may gooral, wal mu dal, mu tette ma ca,

Taalifi cant 23:1–2

Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal. Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.

Taalifi cant 103:13–14

Ndaxte loolu lépp, yéefar yi ñoo koy tiisoo. Te seen Baay ba fa asamaan xam na ne soxla ngeen loolu lépp.

Macë 6:32

ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.

1.Piyeer 5:7

Yeesu ne gees, gis ñu topp ci moom. Mu ne leen: «Lu ngeen bëgg?» Ñu ne ko: «Rabbi,» muy firi kilifa gi, «ana foo dal?» Yeesu ne leen: «Kaayleen, gis.» Ñu dem ba gis fa mu dal. Loola yemook ñeenti waxtu ci ngoon. Ñu daldi toog fa moom la des ca bëccëg ba.

Yowaan 1:38–39

Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb? Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.

Yowaan 14:2–3

«Ku am ndam nag, maa lay may nga toog ak man fi sama ngàngune, na ma ame woon ndam, ba toog ak sama Baay fi ngànguneem.

Peeñu ma 3:21

Ku màgg, Ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk te toroxlu, ngir leqali ku toroxlu, leqali boroom xol bu mokk.

Esayi 57:15

Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat, ba ubbil ma, dinaa agsi moos sa néeg, nu bokk reer.

Peeñu ma 3:20

te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»

Macë 28:20

Sa njubtee tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!

Taalifi cant 36:7