Ibraam nag gëm Aji Sax ji; Aji Sax ji nangul ko ngëmam, muy àtteb njub bu ñu ko limal.
Njàlbéen ga 15:6
Leeru Bés bi
Ibraam nag gëm Aji Sax ji; Aji Sax ji nangul ko ngëmam, muy àtteb njub bu ñu ko limal.
Njàlbéen ga 15:6
Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla. Dafa wéroon Ibraayma péŋŋ ne li Yàlla dige, man na koo def. Moo tax it, Yàlla nangul ko ngëmam, muy àtteb njub bu ñu ko limal. Ba ñu bindee ne ngëmu Ibraayma, moom lees ko nangul, muy àtteb njub bu ñu ko limal, du Ibraayma doŋŋ la mbind ma ñeel. Nun itam ci lanu; dees na nu limal sunu ngëm, àtteb ñu jub, nun ñi gëm ki dekkal sunu Sang Yeesu
Room 4:20–24
Ndax kat digeb Ibraayma ba sédde Ibraayma àddina si, moom ak askanam, sàmm gu mu sàmm yoonu Musaa taxul, waaye àtteb njub bi ko ngëmam may, moo ko waral.
Room 4:13
Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di baaxee nit ñi àtteb ñu jub, lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ki ñu baaxe njub ndax ngëmam mooy dund.»
Room 1:17
Nanu ŋoy ci yaakaar ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la.
Yawut ya 10:23
Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan, di def lu la soob.
Taalifi cant 115:3
ndax Yàlla, dara tëwu ko.»
Luug 1:37
Ndokkalee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»
Luug 1:45
Ñaax nanu leen, dëfal leen, dénku leen, ngir ngeen di jëfe jëfin wu yelloo ak Yàlla mi leen woo ci nguuram ak teraangaam.
1.Tesalonig 2:12
Yeesu ne ko: «Sama nguur moo bokkul ci àddina sii. Bu sama nguur bokkoon ci àddina, samay surga xeex, ba kenn du ma jébbal njiiti Yawut yi. Waaye sama nguur a bokkul fii.»
Yowaan 18:36
Fa la doxe xaar bés ba ñu koy defal ay noonam ndëggastalu tànkam.
Yawut ya 10:13
Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»
Peeñu ma 11:15
Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»
Peeñu ma 5:10
Ci kaw loolu ma gis ay gàngune, ñu jox ña ca toog sañ-sañu àtte. Ma daldi gis bakkani ñi ñu dogoon seen bopp ndax la ñu doon seedeel Yeesu ak la ñu gëmoon kàddug Yàlla gi. Ñooña sujjóotalul woon rab wi ak jëmmu nataalam, te amuñu màndargam rab wi ci seen jë mbaa seen loxo. Ñu dekki bay nguuroondoo ak Almasi bi diiru junniy at.
Peeñu ma 20:4
Su booba aji jub ñi dañu naa ràññ ni jant bi, fa seen nguurug Baay. Ku ami nopp, na dégg.»
Macë 13:43
«Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
Luug 12:32
Man itam ni ma sama Baay dénke nguur, ni laa leen koy dénke. Yeenay lekk aka naan ca sama ndab, ca sama nguur, te yeenay toog ci ay gàngune, di jiite fukki giiri bànni Israayil ak ñaar.»
Luug 22:29–30
na sa nguur dikk, na sa coobare ame fi suuf na mu ame fa asamaan.
Macë 6:10
Bés yu mujj yi
Wone yépp23 Mar 2025
22 Mar 2025
21 Mar 2025
20 Mar 2025
19 Mar 2025
18 Mar 2025
17 Mar 2025