Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.» Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:5–6
Leeru Bés bi
Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.» Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:5–6
Maa ngi nii ànd ak yaw, di la sàmm fépp foo jëm, te itam dinaa la delloosi ci réew mii. Duma la bàyyi mukk, waaye dinaa def li ma la wax lépp.»
Njàlbéen ga 28:15
Dëgërluleen nag te am fit. Buleen tiit, buleen yox-yoxi ndax ñoom, ngir seen Yàlla Aji Sax ji mooy ànd ak yeen. Du leen ba, du leen wacc mukk.»
Baamtug yoon wi 31:6
Ndax kat Demas, àddinay tey la sopp ba tax mu wacc ma, dem Tesalonig, te Kereseñsë dem na diiwaanu Galasi, Tit dem diiwaanu Dalmasi.
2.Timote 4:10
Keroog ba ma njëkkee di layool sama bopp, kenn taxawuwu ma, ñépp a ma daw, yàlla bu leen seen jëf topp. Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jàmbur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.
2.Timote 4:16–17
Ndey ak baay man nañu maa wacc, Aji Sax ji fat ma.
Taalifi cant 27:10
te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
Macë 28:20
Maay Kiy dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.
Peeñu ma 1:18
Duma leen bàyyi ngeen tumurànke. Dinaa délsi ci yeen.
Yowaan 14:18
Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
Yowaan 14:27
Simoŋ ne ko: «Njaatige, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Xanaa ma sànni ko rekk ci sa ndigal.»
Luug 5:5
Yeesu dikk ne leen: «Joxees na ma bépp sañ-sañ fa asamaan ak fi kaw suuf. Kon demleen sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóobleen leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Noo gu Sell gi, te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
Macë 28:18–20
«Nguurug asamaan mel na it ni mbaal mu ñu sànni biir géej, mu jàpp wirgoy jën wu nekk.
Macë 13:47
Yégle xibaaru jàmm bi moom, du lu may kañoo. Wartéef la wu ñu ma sas, te ngalla man, su ma yéglewul xibaaru jàmm bi!
1.Korent 9:16
Maak boroom ngëm yi desee dëgër, damaa mel ni ku ngëmam desee dëgër, ngir iri leen. Lépp laa def sama bopp ci ñépp, ak nu mu mana deme, ba musal ñenn ci ñoom.
1.Korent 9:22
Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.
Galasi 6:9
Sama kàddu giy bawoo sama gémmiñ it, noonu la. Du délsee ag neen ci man te deful li ma namm, ba sottal li ma ko yebal.
Esayi 55:11
Ki jëmbat nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, xanaa Yàlla miy jebbil doŋŋ.
1.Korent 3:7
Bés yu mujj yi
Wone yépp24 Mar 2025
23 Mar 2025
22 Mar 2025
21 Mar 2025
20 Mar 2025
19 Mar 2025
18 Mar 2025