Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Cowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja. Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqalikoo.
Njàlbéen ga 13:10–11
te mennum Lóot aji jub ji doŋŋ, nekkoon kenn ki mu musal, te mu sonnoon lool, ndax ñaawtéefi nit ñu dëng ñooñu. Ndax Lóot aji jub ja dëkkoon ci seen biir kat, la mu nekke woon ci biir xolu njubam, moo di naqarlu, ndax jëfi ndëngte ya muy gis, di ko dégg, bés bu nekk.
2.Piyeer 2:7–8
Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.
Galasi 6:7
Fàttalikuleen jabaru Lóot ja!
Luug 17:32
Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?
2.Korent 6:14
Kon nag:
«Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,»
la Boroom bi wax,
«lu sobewu, buleen ko laal.
Su boobaa, maa leen di dalal.
2.Korent 6:17
Kon nag buleen séq ak ñooñu dara. Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer.
Efes 5:7–8
Ràññeeleen li neex Boroom bi; jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja.
Efes 5:10–11
Kon nag jox ma diiwaanu tund yii Aji Sax ji waxoon bésub keroog. Yaa dégg bésub keroog ne, Anageen ñaa fa nekk ci ay dëkk yu mag yu ñu dàbbalee ay tata, waaye jombul Aji Sax ji ànd ak man, ma nangu ko ci seeni loxo, na ko Aji Sax ji waxe woon.»
Yosuwe 14:12
Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne:
«Duma la bàyyi mukk,
duma la wacc mukk.»
Moo tax nu mana am fitu wax ne:
«Boroom beey sama ndimbal, duma tiit.
Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:5–6
Boroom bi Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar,
di tudd sa àtte dëgg gu wéet.
Taalifi cant 71:16
Su boobaa àtteb dëgg ay jur jàmm,
àtteb yoon di dalal tey aare ba fàww,
Esayi 32:17
Taxawleen kon temm. Defleen dëgg di ngañaay li ci seen ndigg, njub di seen kiiraayal dënn.
Efes 6:14
Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan. Kon nag jëlleen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm.
Efes 6:12–13