Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.
Taalifi cant 119:130
Leeru Bés bi
Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.
Taalifi cant 119:130
Xibaar bi nu dégge ci moom, di leen ko àgge, mooy lii: Yàlla ag leer la, te gennug lëndëm nekkul ci moom.
1.Yowaan 1:5
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leer ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi bi.
2.Korent 4:6
Njàlbéen ga fekk na Kàddu gi nekk, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.
Yowaan 1:1
Ci moom la dund nekk, te dund dig leer, ñeel nit ñi.
Yowaan 1:4
Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
1.Yowaan 1:7
Sama xol laa làq say wax, ngir bañ laa moy.
Taalifi cant 119:11
Yeen nag, set ngeen wecc ba noppi, ndax kàddu gi ma leen wax.
Yowaan 15:3
Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer.
Efes 5:8
Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.
1.Piyeer 2:9
Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla.
Njàlbéen ga 6:9
Li sàmm yoon taxul kenn jot àtteb ku jub fi kanam Yàlla sax, lu leer nàññ la, nde: «Ki ñu baaxe njub ndax ngëmam mooy dund.»
Galasi 3:11
Naka la Nóoyin génn, daldi sàkkal Aji Sax ji sarxalukaay, màggale ko ko. Mu sàkk nag ci mboolem rab wu set ak mboolem picc mu set, jébbal Yàlla ca sarxalukaay ba, muy saraxu rendi-dóomal. Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole faagaagal mukk lépp luy dund, nii ma ko defe.
Njàlbéen ga 8:20–21
Mboolem waa àddina di ko sujjóotal, maanaam mboolem ñi ñu bindul seen tur ca ndoortel àddina ci téereb dund bu Xar mi ñu rendi.
Peeñu ma 13:8
Gannaaw nag dees noo baaxe àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi bi.
Room 5:1
Ndax kat deesul baaxe kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solos yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar. Waaye léegi Yàlla moo feeñal nu nit di ame fa kanamam àtteb njubam gu ajuwul ci yoonu Musaa. Te yoonu Musaa ak yonent yi seede nañu loolu. Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi bi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.
Room 3:20–22
Kenn xeluwul, kenn wutul Yàlla.
Room 3:11
Ñi Yàlla tànn, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de moo leen àtte ni ñu jub.
Room 8:33
Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen baaxe itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.
Room 8:30
Bés yu mujj yi
Wone yépp19 Mar 2025
18 Mar 2025
17 Mar 2025
16 Mar 2025
15 Mar 2025
14 Mar 2025
13 Mar 2025