Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam.
Sarxalkat yi 1:4
Leeru Bés bi
Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam.
Sarxalkat yi 1:4
Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam, waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul.
1.Piyeer 1:18–19
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»
1.Piyeer 2:24
Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.
Efes 1:6
Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gu Sell gi tabaxe ag kër Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi bi.
1.Piyeer 2:5
Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war.
Room 12:1
Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,
Yudd 24
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Yawut ya 4:15
Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram ji mu àndal, moom it mu lekk.
Njàlbéen ga 3:6
Ndax kat mboolem lu nekk ci àddina, muy xemmemtéefi bakkan, di mboolem xemmemtéef gu sosoo ci lu bët tege, ak réy-réylu gu alalu àddina waral, amul lenn lu ci jóge ci Baay bi, xanaa ci àddina.
1.Yowaan 2:16
Fiirkat bi nag dikk ba ci moom, ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, neel doj yii ñu soppaliku mburu.» Teewul Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Du aw ñam doŋŋ la nit di dunde, waaye dees na dunde itam, gépp kàddu gu tukkee ci gémmiñug Yàlla.”»
Macë 4:3–4
Seytaane yóbbooti ko ba ca kaw tund wu kawe lool, won ko mboolem nguuri àddina yépp ak seeni daraja. Mu ne ko: «Lii lépp, yaw laa koy may, soo sukkee sujjóotal ma.» Yeesu nag ne ko: «Xiddi ma Seytaane, ndax bindees na ne: “Boroom bi sa Yàlla ngay sujjóotal, te moom doŋŋ ngay jaamu.”»
Macë 4:8–10
Ndax kat mboolem lu nekk ci àddina, muy xemmemtéefi bakkan, di mboolem xemmemtéef gu sosoo ci lu bët tege, ak réy-réylu gu alalu àddina waral, amul lenn lu ci jóge ci Baay bi, xanaa ci àddina.
1.Yowaan 2:16
Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.
Yawut ya 2:18
Ndokkalee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag texe gi Yàlla dig ñi ko sopp.
Yanqóoba 1:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp16 Mar 2025
15 Mar 2025
14 Mar 2025
13 Mar 2025
12 Mar 2025
11 Mar 2025
10 Mar 2025