Leeru Bés bi — 23 Mars: Peeñu ma 4:8

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ñeenti mbindeef yi am nañu ku nekk juróom benni laaf, fees aki bët ba daj, biir ak biti, te guddi ak bëccëg duñu selaw, xanaa naan: «Kee sell, Kee sell, Kee sell, Keey Boroom bi Yàlla Aji Man ji, Kee masa nekk, Kee nekk, Keey dikk.»

Peeñu ma 4:8

Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo; woote guddi, noppaloo ma.

Taalifi cant 22:3

Yàlla ne ko: «Bul jegesi, summil say dàll, ndax fii nga taxaw suuf su sell la.» Mu teg ca ne: «Man maay sa Yàllay baay, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba.» Ca la Musaa nëbb kanam ga, ndax ragala xool Yàlla.

Mucc ga 3:5–6

Aji Sell ji ne: «Ana ku ngeen may nirooleel, ba may moroomam?»

Esayi 40:25

Man Aji Sax ji, maay sa Yàlla; man Aji Sell ju Israayil, maa lay musal. Maa joxe Misra, feye la; ak Kuus ak Saba, ma weccikoo la.

Esayi 43:3

Aji Sax ji, mennum man a; amul jotkat bu ma moy.

Esayi 43:11

Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin. Ndax kat bindees na ne: «Ñu sell ngeen wara doon, ndax man Ku sell laa.»

1.Piyeer 1:15–16

Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,

1.Korent 6:19

Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»

2.Korent 6:16

Ndax ñaar dina ànd te digewuñub dajee?

Amos 3:3

Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom.

Luug 24:29

Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat, ba ubbil ma, dinaa agsi moos sa néeg, nu bokk reer.

Peeñu ma 3:20

Sama soppey xol, ngalla wax ma ana fooy foral, di fa gooral, digg bëccëg? Lu ko moy may muuru, di la wër fi say xarit ak seeni gétt.

Ngën-gi-woy 1:7

Ma romb leen tuuti rekk, gis sama soppey xol. Ma ne ko taral, bàyyeetuma ko, ba yóbbu ko sama kër yaay, ba sama biir néegu ndey ji ma jur.

Ngën-gi-woy 3:4

Yaw, ngelawal bëj-gànnaar, yewwul, ngelawal bëj-saalum, dikkal, wolalleen ma sama tool bi, mu gilli; sama nijaay dugg toolam, xéewloo ngën-gi-meññeefam.

Ngën-gi-woy 4:16–5:1

Làquwuma, di waxe béreb bu lëndëm. Newuma it askanu Yanqóoba: “Wërleen ma ci neen.” Man Aji Sax ji maay wax dëgg, di biral liy yoon.»

Esayi 45:19

te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»

Macë 28:20

Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»

Yawut ya 13:5

ndax fu ñaar mbaa ñett dajee ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»

Macë 18:20

Des na tuuti, àddina du ma gisati; yeen dingeen ma gis, ndax man maa ngi dund, te yeen itam dingeen dund.

Yowaan 14:19