Yeen xanaa xamuleen sax lu ëllëg di doon? Ana luy seen bakkan? Yeen ngeen di as lay suy feeñ léegi, nes tuut mu ne mes!
Yanqóoba 4:14
Leeru Bés bi
Yeen xanaa xamuleen sax lu ëllëg di doon? Ana luy seen bakkan? Yeen ngeen di as lay suy feeñ léegi, nes tuut mu ne mes!
Yanqóoba 4:14
Ab dawkat sax ni samay fan di jeexee ko raw. Wone nañu gannaaw te gisuñu lu baax. Samay fan tarxiis nañu, wéy, woyof ni gaali barax, mbaa jaxaay ju naan jàyy cim rëbbam.
Ayóoba 9:25–26
Yaay buub nit, nelawal ko. Suba mu jebbi nim ñax, xëy, jebbi, naat; ngoon mu lax, wowal.
Taalifi cant 90:5–6
Dangay tóor rekk, lax, wéy ni takkndeer, doo toog.
Ayóoba 14:2
Te àddina day jeex, mooki xemmemtéefam, waaye kuy jëfe coobarey Yàlla mooy sax ba fàww.
1.Yowaan 2:17
Bu yàgg nga samp suuf, sàkke asamaan say loxo. Yooyu day réer, waaye yaw yaay sax, lépp ay ràpp ni mbubb, nga soppi leen niy yére, sànni;
Taalifi cant 102:26–27
Yeesu Almasi bi, menn mii la woon démb ak tey ba fàww, du soppiku.
Yawut ya 13:8
Kon ana nees di def? Naa ñaane sama xol, tey ñaane samam xel itam. Naa sàbbaale sama xol, tey sàbbaale samam xel itam.
1.Korent 14:15
Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noowug Yàlla fees, ngeen di jàngalante taalifi cant yi ak woyi cant yi ak woy yu fentoo ci Noowug Yàlla gi, di woy aka kañ Boroom bi ci seen xol.
Efes 5:18–19
Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.
Kolos 3:16
Naa sàlloo sant Aji Sax ji, na luy dund saxoo dàkk di màggal sellaayu turam!
Taalifi cant 145:21
Màggalleen Ki Sax! Kañ sunu Yàllaa baax, màggal koo neex te war.
Taalifi cant 147:1
Woyeleen Aji Sax ji kàddug cant, kañeleen sunu Yàlla jii ay xalam;
Taalifi cant 147:7
Ma dégg baat bu jóge ci asamaan, nirook riirum géej, mel ni dënu gu réy, melati ni ay xalamkat yuy xalam.
Peeñu ma 14:2
Bés yu mujj yi
Wone yépp15 Mar 2025
14 Mar 2025
13 Mar 2025
12 Mar 2025
11 Mar 2025
10 Mar 2025
9 Mar 2025