Leeru Bés bi — 15 Mars: Yawut ya 2:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.

Yawut ya 2:10

Ca la leen ne: «Tiis wu réy la sama xol fees, ba may bëgga dee! Toogleen fii, te ngeen ànd ak man ci teewlu.» Ba loolu amee, Yeesu dox ba sore leen tuuti, ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf. Mu ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko! Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»

Macë 26:38–39

Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.

Luug 22:44

Buumi dee a ma laawoon, njàqarey njaniiw dab ma, ma dajeek naqar aku tiis.

Taalifi cant 116:3

Yaa gis ñu di ma sewal, di ma ruslooka toroxal, yaa ngi ne jàkk ci noonoo noon.

Taalifi cant 69:20

Bu ma yoqee, ràññee nga samay jéego; yoon wi may jaare lañu ma làqal am yeer.

Taalifi cant 142:4

Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.

Esayi 53:3

Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.

Taalifi cant 19:1

Kàddug Aji Sax ji la asamaan sosoo, ci baatam la gàngoori asamaan yépp sàkkoo.

Taalifi cant 33:6

Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.

Taalifi cant 33:9

Xeet yaa ngii, mel ni aw toq ci biir bagaan, jàppeesu leen lu moy diisaayu feppu suuf! Dun yi lay yékkati ni pëndub suuf!

Esayi 40:15

Ngëm a nu xamal ne Yàllaa sos àddina wërngal këpp ci kàddoom, ngir li bët di gis dees koo sàkke ci lu bët manula gis.

Yawut ya 11:3

Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, feeñal nga ca sa kàttan, ngir jaxase say noon, bañaaleek feyukat ne xerem. Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.

Taalifi cant 8:3–4