Leeru Bés bi — 9 Nowàmbar: Taalifi cant 89:19

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israayil mooy boroom.

Taalifi cant 89:19

Aji Sax ji, mennum man a; amul jotkat bu ma moy.

Esayi 43:11

Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn rammukat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy kenn nit: muy Almasi Yeesu

1.Timote 2:5

Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»

Jëf ya 4:12

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Esayi 9:6

Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam. Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj. Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur,

Filib 2:7–9

Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deewam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deewale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.

Yawut ya 2:9

Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.

Yawut ya 2:14

Mu ne: «Dajaleel ma sama wóllëre yiy sarxal, di ko fasee sama kóllëreek ñoom.»

Taalifi cant 50:5

noonu itam la Almasi bi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.

Yawut ya 9:28

Looloo tax Yeesu di rammukat bi fas kóllëre gu bees, ngir ñi ñu woo mana jot ci muur gu sax dàkk gi ñu leen dig. Deewam gi mu dee, moom la leen jote ci bàkkaar yi ñu xëtte kóllëre gu njëkk ga.

Yawut ya 9:15

«Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.

Yowaan 17:24

Su ko defee mu yebal malaaka yi, ñu dajalee ay tànnéefam fa ñeenti jëmuy ngelaw li, dale ko ca catu kaw suuf, ba ca catu asamaan.»

Màrk 13:27

Su ñu leen toxaloon ba ca cati asamaan sax, foofa la leen seen Yàlla Aji Sax ji di dajalee, te fa la leen di jële.

Baamtug yoon wi 30:4

Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki. Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.

1.Tesalonig 4:16–17