Fexeleen ba kenn du feyantoo. Waaye lu baax, deeleen ko deflante ci seen biir, te di ko defal ñépp.
1.Tesalonig 5:15
Leeru Bés bi
Fexeleen ba kenn du feyantoo. Waaye lu baax, deeleen ko deflante ci seen biir, te di ko defal ñépp.
1.Tesalonig 5:15
Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam. «Moo bàkkaarul, fenul.» Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.
1.Piyeer 2:21–23
Xoolleen ci moom mi bàkkaarkat yi doon xeex, bala ngeena yoqi bay xàddi.
Yawut ya 12:3
Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi. Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:1–2
Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.
Filib 4:8
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Esayi 9:6
Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan. Yaa gëna góorayiwe ci àddina, sa kàddu diw yiw, ndax Yàllaa la barkeel ba fàww! Jàmbaaroo, takkal sa saamar, te yànj, am daraja;
Taalifi cant 45:2–4
Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.
Taalifi cant 45:6
Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israayil mooy boroom.
Taalifi cant 89:19
«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.
Sàkkaryaa 13:7
Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dallu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki Sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»
Esayi 12:2
Waaye cant ñeel na Yàlla! Moom mi Almasi bi tax mu di nu yóbbaale saa su nekk, ci njaab miy fésal ndamam, te cuuraayal xam-xamam, nun ñii la koy wasaaree fépp,
2.Korent 2:14
Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk, Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi bi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.
Yudd 24–25
Bés yu mujj yi
Wone yépp1 Now 2026
31 Okt 2026
30 Okt 2026
29 Okt 2026
28 Okt 2026
27 Okt 2026
26 Okt 2026