Leeru Bés bi — 6 Nowàmbar: Kolos 3:4

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Seenug dund dëgg Almasi bi la, te keroog bu Almasi bi feeñee, yeen itam dingeen ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.

Kolos 3:4

Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund.

Yowaan 11:25

Seede si moo di texe ba fàww la nu Yàlla jagleel, te texe googu ci Doomam la nekk. Ku am Doom ji, yaa texe; ku amul Doomu Yàlla, texewuloo.

1.Yowaan 5:11–12

Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki. Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww. Kon nag deeleen dëfalantee yooyu kàddu.

1.Tesalonig 4:16–18

Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise.

1.Yowaan 3:2

Ci ag teddadi lañu ji néew bi ñu suul, te teraanga lay dekkaale. Ci néew doole lees ko ji, mu dekkaale doole.

1.Korent 15:43

Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.

Yowaan 14:3

Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. Yaw yaay Yàlla ji may musal, ma di la yendoo yaakaar.

Taalifi cant 25:5

Moom miy Noowug dëgg gi, bu dikkee, moo leen di àggale ci dëgg gi gépp, ndax du ci coobarey boppam lay wax, waaye mboolem lu mu dégg la leen di wax, te liy ñëw ëllëg, moo leen koy wax.

Yowaan 16:13

Yeen nag, Ku sell kee leen diw, sédde leen ko Noo gu Sell gi, te moo leen taxa xam, yeen ñépp.

1.Yowaan 2:20

Kon waxleen ne leen: «Ayca, delluleen ca ndigali yoon ya, ak seedey kàdduy waxyu ya. Kuy wax googu kàddu, ag leer fenkalu la.»

Esayi 8:20

Mboolem Mbind mu sell mi la Yàlla wal ag Noowam, ba mu am njariñal jàngal nit ñi, femmu leen, jubbanti leen, yar leen cig njub. Su ko defee nitu Yàlla ki mat sëkk te matley jumtukaay ngir jépp jëf ju baax.

2.Timote 3:16–17

Bi ngay gone nga dale xam Mbind mu sell mi, te moo la mana may xel mu la jëme ci mucc gi gëm Almasi Yeesu di maye.

2.Timote 3:15

Nga ne ma: «Dama laa xelal, xamal la fi ngay jaar, digal la, di la bàyyi xel.

Taalifi cant 32:8

«Bët mooy làmpu yaram. Su sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo,

Macë 6:22

Ku namma jëfe coobarey Yàlla, dina xam ndax li may jàngale ci Yàlla la jóge, am ci sama coobarey bopp laay waxe.

Yowaan 7:17

Foofa law yoon di jaare, ñu di ko woowe Yoon wu sell wi. Ku sobewu du fa jaare, ñi moom woowu yoon, ñooy ñi koy topp. Ab dof sax du fa lajje.

Esayi 35:8