Leeru Bés bi — 10 Nowàmbar: Kolos 1:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.

Kolos 1:10

Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war. Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.

Room 12:1–2

Xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo. Li am solo mooy doon mbindeef mu bees. Mboolem ñiy sàmm ndigal lii nag, te di Israayilu Yàlla, jàmm ak yërmande ñeel na leen.

Galasi 6:15–16

Li feeñal sama darajay Baay mooy ngeen meññ lu bare, te noonu ngeen di firndeele ne samay taalibe ngeen.

Yowaan 15:8

Du yeen yeena ma tànn, man maa leen tànn, sas leen ngir ngeen dem, meññi meññeef, te seenum meññeef sax, ba lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko.

Yowaan 15:16

Sama kaw lal, guddi, laa seet sama soppey xol. Seet naa ko, gisuma ko.

Ngën-gi-woy 3:1

«Dees na topp waa Samari, nde ñoo fippu ci seen kaw Yàlla. Saamar lañuy faate, seeni doom, ñu rajaxe leen, seen jigéeni wérul, ñu butti.» Israayiloo, dellul ci sa Yàlla Aji Sax ji, fakkastaloo nga sag ñaawtéef.

Ose 14:1–2

Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn. Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la.

Yanqóoba 1:13–14

Bokk yi, soppe yi, buleen juum ci lii: gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.

Yanqóoba 1:16–17

Yaakaaral Aji Sax ji, dëgërlul te amu fit, te yaakaarati Aji Sax ji.

Taalifi cant 27:14

Li baax mooy muñ, xeremluy xaar wallub Aji Sax ji.

Jooytu 3:26

Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe?

Luug 18:7

Mu jëm ci Yedutun, njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.

Taalifi cant 62:1

Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ; yeena ngi bége ay fen, seeni kàddu diw yiw, seen xalaat diy saaga. Selaw.

Taalifi cant 62:5