«Yaw nag, tànnal ngën-gi-xeeñal: xeetu ndàbb li ñuy wax miir bu ndoxe, sàkk ci juróomi kilo; xasum kanel mu xeeñ, ñaari kilo ak genn-wàll; yuuru gattax gu xeeñ, ñaari kilo ak genn-wàll;
Mucc ga 30:23
Leeru Bés bi
«Yaw nag, tànnal ngën-gi-xeeñal: xeetu ndàbb li ñuy wax miir bu ndoxe, sàkk ci juróomi kilo; xasum kanel mu xeeñ, ñaari kilo ak genn-wàll; yuuru gattax gu xeeñ, ñaari kilo ak genn-wàll;
Mucc ga 30:23
Loolu ngay def diwu pal gu sell gi, te na doon njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax. Diwu pal gu sell lay doon.
Mucc ga 30:25
Doom aadama ju ko jagoowul, deesu ko ko diw, te buleen njafaan lenn lu ni mel, lu ngeen yemale dayoy xeeñal ya ak dayoy diw gu sell gi. Deesu ko def ci yaramu kenn ku ko jagoowul, te buleen njafaan xeeñal yi ciy dem, ci dayo yu tollook dayoy diw gu sell gi, ngir defar lenn lu ni mel. Lu sell la, lu ngeen wara wormaal sellaayam.
Mucc ga 30:32
Wenn yaram a fi nekk ak genn Noo ak jenn yaakaar ju leen wooteb Yàlla jëme.
Efes 4:4
Mayi Noo gi wuute na, waaye genn Noo gi la.
1.Korent 12:4
Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. sa yetu buur njub la,
Taalifi cant 45:7
ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane nootoon.
Jëf ya 10:38
Yàlla kat, ku mu yebal, kàddug Yàlla lay wax, ndax Yàlla du natt li mu koy nàddil cig Noowam.
Yowaan 3:34
Ci ag matam lanu tanqe nun ñépp, yiw ci kaw yiw.
Yowaan 1:16
Yeen nag, diw gi mu leen diw, sédde leen ko Noo gu Sell gi, moo sax ci yeen, soxlawuleen ku leen jàngal dara. Gannaaw Noowam gu Sell googu moo leen di jàngal lépp, te di lu dëggu lu caaxaan amul, nangeen sax ci moom, ni mu leen ko jàngale.
1.Yowaan 2:27
Te ki nuy saxal ci Almasi bi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla. Moo nu màndargaale xàmmikaayam, te moo yeb dawalub Noo gu Sell gi ci sunu biir xol.
2.Korent 1:21–22
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.
Galasi 5:22–23
ñiy jariñoo alalu àddina, bañ cee xér, ndax melow àddina sii tey, day wees.
1.Korent 7:31
Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu.
Njàlbéen ga 5:27
Mbokkum gëmkat mi suufe daraja, na sagoo ab kawewaayam ci ni ko Yàlla yékkatee; te ki barele it na sagoo ci ni ko Yàlla suufeelee, ndax ni tóor-tóoru saxyaay di ruuse, noonu lay wéye. Naka la jant di fenk, ba naaj wi tàng jérr, saxyaay lax, tóor-tóoram ruus, taar ba réer ko mërr. Noonu itam la ki barele di jeexlee ci biiri yëngoom.
Yanqóoba 1:9–11
Yeen xanaa xamuleen sax lu ëllëg di doon? Ana luy seen bakkan? Yeen ngeen di as lay suy feeñ léegi, nes tuut mu ne mes!
Yanqóoba 4:14
Te àddina day jeex, mooki xemmemtéefam, waaye kuy jëfe coobarey Yàlla mooy sax ba fàww.
1.Yowaan 2:17
sama xol diis, xel di xelaat, xol diis gann; ma mujj àddu,
Taalifi cant 39:4
Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce. Waaye yeen bokk yi, nekkuleen cig lëndëm, ba bés boobu di leen bett ni ab sàcc di bettee.
1.Tesalonig 5:3–4
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Now 2026
3 Now 2026
2 Now 2026
1 Now 2026
31 Okt 2026
30 Okt 2026
29 Okt 2026