Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu ànd ak sunu sago, te def ngëm ak cofeel sunu kiiraayal dënn; yaakaaru texe di sunu mbaxanam xare.
1.Tesalonig 5:8
Leeru Bés bi
Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu ànd ak sunu sago, te def ngëm ak cofeel sunu kiiraayal dënn; yaakaaru texe di sunu mbaxanam xare.
1.Tesalonig 5:8
Kon nag teewlooleen seen xel, te ànd ak seen sago, te ngeen wékk seen jépp yaakaar ci yiw wa ñu leen di dikke kera bu Yeesu Almasi bi feeñee.
1.Piyeer 1:13
Taxawleen kon temm. Defleen dëgg di ngañaay li ci seen ndigg, njub di seen kiiraayal dënn.
Efes 6:14
Te fu ngeen tollu ŋàbbleen pakk biy seen ngëm, ci ngeen mana fanqe mboolem jumi sawaray ku bon ki.
Efes 6:16
Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jëlleen ko, sol; jëlleen itam saamar bi Noo gu Sell giy joxe, te muy kàddug Yàlla.
Efes 6:17
Mooy mëdd dee ba fàww! Boroom bi Aji Sax jeey fompe gépp kanam rongooñi boroom. Buumi gàccey ñoñam it, moo koy doge fépp ci àddina. Aji Sax ji kat wax na ko.
Esayi 25:8
Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»
Esayi 25:9
Ngëm nag mooy cëslaayal yaakaar te mooy firndey li bët gisul.
Yawut ya 11:1
Waa Israayil daje, sàkk ab dund, ba noppi dox wuti leen. Waa Israayil a nga dal janook ñoom, di saf ñaari gétti bëy. Waa Siri ñoom fees àll ba.
1.Buur ya 20:27
Góoru Yàlla ga dikk ne buurub Israayil: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw waa Siri dañoo yaakaar ne man Aji Sax ji, yàllay tund laa, duma yàllay xur, maay teg mbooloo mu réy mii mépp ci say loxo. Su ko defee ngeen xam ne maay Aji Sax ji.»
1.Buur ya 20:28
Diiru juróom ñaari fan nag ñu jàkkaarloo ca seeni dal. Bésub juróom ñaareel ba xare ba jib, waa Israayil daane téeméeri junniy (100 000) xarekat yu warul fas ca waa Siri ci benn bés bi;
1.Buur ya 20:29
Yeen xale yi, ci Yàlla ngeen bokk, te daan ngeen yonenti caaxaan yooyu, ndax ki ci yeen moo ëpp doole ki ci àddina.
1.Yowaan 4:4
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama loxol ndijoor liy àtte dëgg.
Esayi 41:10
Dañu lay xeex te duñu la man, yaw laay àndal, di la xettali.» Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi 1:19
Bés yu mujj yi
Wone yépp7 Now 2026
6 Now 2026
5 Now 2026
4 Now 2026
3 Now 2026
2 Now 2026
1 Now 2026