Li baax mooy muñ, xeremluy xaar wallub Aji Sax ji.
Jooytu 3:26
Leeru Bés bi
Li baax mooy muñ, xeremluy xaar wallub Aji Sax ji.
Jooytu 3:26
Xanaa daa jeexal ngor tàkk? Am kàddoom a deñ ba fàww?
Taalifi cant 77:9
Cant ñeel na Aji Sax ji! Ndaw kéemtaan ci ngor li mu ma jiwe biir dëkk bu ñu gaw.
Taalifi cant 31:22
Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe? Maa leen ne, mooy sàmm seen àq ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki dikkee, mbaa dina fekk ngëm ci kaw suuf?»
Luug 18:7–8
Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.
Kàddu yu xelu 20:22
Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle tey lal ay pexe.
Taalifi cant 37:7
Du yeenay xare bii xare. Dikkleen taxaw ba gis ndamal Aji Sax jeek yeen. Yeen waa Yuda ak Yerusalem, buleen tiit, buleen ragal. Ëllëg génnleen dajeek ñoom, Aji Sax ji mooy ànd ak yeen.”»
2.Jaar-jaar ya 20:17
Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.
Galasi 6:9
Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.
Yanqóoba 5:7
Jàppalleen ma till yi, till yu ndaw yiy ruur reseñ, te sunu reseñ jiy tóor.
Ngën-gi-woy 2:15
Man, Sang bi, ci laay leerloo, ku ko sàmm yokku yool.
Taalifi cant 19:12
Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.
Yawut ya 12:15
Seen njàlbéenu xél de baax na! Ana ku leen gàllankoor ba toppuleen dëgg gi?
Galasi 5:7
Te lii kat, bir na ma: ki tàmbali jii jëf ju baax ci yeen, dina ko àggale ba keroog bésub Almasi Yeesu.
Filib 1:6
Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi bi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di bokk xeex, ngir saxal ngëm gi sukkandikoo ci xibaaru jàmm bi.
Filib 1:27
Noonu itam la aw làmmiñ dee cér su tuut te réy aw bàkk. Seetleen ni ferñent su tuut di lakke gott bu yaa. Aw làmmiñ itam sawara la; làmmiñ a bokk ci sunuy cér, te di àddinay mbon, di gàkkal jëmm jépp. Aw làmmiñ, giiru dundu nit ki lay jafale ab taal bu tàkke fa sawara.
Yanqóoba 3:5–6
Waaye aw làmmiñ, kenn manu koo tàggat ba mu mokk. Mooy aayteef gu kenn manula dànk, fees dell ak tookey dee.
Yanqóoba 3:8
Na seen kàddu ànd ak yiw te am solo, te ngeen xam nu ngeen di tontoo ku nekk, tont li war.
Kolos 4:6
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Okt 2026
28 Okt 2026
27 Okt 2026
26 Okt 2026
25 Okt 2026
24 Okt 2026
23 Okt 2026