Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragalleen ko! Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!
Taalifi cant 99:1
Leeru Bés bi
Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragalleen ko! Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!
Taalifi cant 99:1
Man daal, ndax dangeen maa ragalul, am dungeen raf ci sama kanam?”» Kàddug Aji Sax jee. «Man mi teg gannuus, yemalee ko géej, dogalal ko ko dàkk te du ko jàll, lu mu wañax wañax, du ko man; gannax ya day riir, te du jàll!
Yeremi 5:22
bul bew a bew, bay waxe reewande.”» Du penku, du sowu, te du màndiŋ ma la daraja di jóge.
Taalifi cant 75:6–7
Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.
Dañeel 2:21
Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; waaye moytuleena tiit, ndax fàww loolu am, waaye du doonagum muj ga.
Macë 24:6
Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Room 8:31
Ñaari picci ramatu, xanaa du dërëm lay jar? Moona menn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay. Seen kawari bopp sax, waññees na lépp. Kon nag buleen ragal dara, nde ndiiraanu ramatu, yeena ko gën.
Macë 10:29–31
Kenn deful lii te desem xel. Kenn doŋŋ a ko defoon. Ndax lan? Kuutaay li ko Yàlla digoon la doon wut. Kon nag sàmmleen seenum xel, te buleen wor seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw.
Malasi 2:15
Ci kaw loolu Yowaan àddu, ne: «Njaatige, danoo gis kuy dàq ay rab ci sa tur, nu aaye ko, ndax bokkul ci nun.» Yeesu ne ko: «Buleen ko aaye, ndax ku la sotul, yaw la faral.»
Luug 9:49–50
Taalibe ya ñuy wax Yanqóoba ak Yowaan gis loolu, daldi ne: «Sang bi, soo bëggee nu jox sawara ndigal, mu wàcce asamaan, faagaagal leen?» Teewul Yeesu geesu, femmu leen.
Luug 9:54–55
Ab xale dawe ca, àgge ko Musaa, ne ko: «Eldàdd ak Medàdd déy a ngay jottali ay kàdduy waxyu ca dal ba!» Yosuwe doomu Nuun ja dale doon bëkk-néegu Musaa cag ndawam, daldi cay àddu, ne: «Sang Musaa, aaye leen!» Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sang leen ag leeram!»
Màndiŋ ma 11:27–29
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko. Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar aki xemmemtéefam. Gannaaw nag Noowug Yàlla moo nu dundal, nanu topp Noo gi. Bunu di yég sunu bopp, di merloonte aka iñaanante.
Galasi 5:22–26
Bés yu mujj yi
Wone yépp25 Okt 2026
24 Okt 2026
23 Okt 2026
22 Okt 2026
21 Okt 2026
20 Okt 2026
19 Okt 2026