Noonu la kàddu ga jottalikoo woon ci gémmiñu Yonent Yàlla Esayi mate. Mooy ba mu nee: «Moom sunuy wopp la jël, sunuy jàngoro la sëfoo.»
Macë 8:17
Leeru Bés bi
Noonu la kàddu ga jottalikoo woon ci gémmiñu Yonent Yàlla Esayi mate. Mooy ba mu nee: «Moom sunuy wopp la jël, sunuy jàngoro la sëfoo.»
Macë 8:17
sarxalkat bi day santaane, ñu indil nit kooku ñuy laabal ñaari picc yu dagan tey dund, ak bantu garabu seedar, ak wëñ gu xonq curr, ak caru garabu isob. Na sarxalkat bi santaane, ñu rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer lu def ndox mu balle ci bëtu ndox. Picc miy dund da koy booleek bantu seedar bi ak wëñ gu xonq curr gi ak caru isob bi, boole lépp sóob ci deretu picc ma ñu rendi woon tiimale ko ndox mi balle ci bëtu ndox. Bu loolu amee sarxalkat bi wis-wisal juróom ñaari yoon ci kaw ki ñuy laabal, ngir mu tàggook sobey jàngoro ji. Su ko defee sarxalkat bi biral ne set na. Bu noppee na bàyyi picc miy dund mu naaw ca àll ba.
Sarxalkat yi 14:4–7
Yeesoo nga nekkoon cib dëkk, ndeke jenn waay a nga fa, ju jàngoroy ngaana daj ca yaram wa. Ba mu gisee Yeesu, daa daanu, dëpp jëëm ci suuf, sarxu ko, ne: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.»
Luug 5:12
Yërmande jàpp Yeesu, mu tàllal loxoom, laal ko, ne ko: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaana ga teqalikook moom, mu set wecc.
Màrk 1:41–42
Kon nag dikkal gaaw ñaanal ma yàlla gàngoor gii, ngir ñoo ma ëpp doole. Jombul ma duma leen, ba dàq leen réew mi, ndax xam naa ne koo ñaanal barke, mu barkeel, te koo ñaanal alkànde, mu alku.»
Màndiŋ ma 22:6
«Ndokkalee ñi am xolub ku néew doole, nde nguurug asamaan, ñooy boroom. Ndokkalee ñiy jooy, nde dees na leen dëfal. Ndokkalee ñi woyof, nde ñooy moom àddina. Ndokkalee ñi xiif aka mar jëfe njekk, ndax dinañu regg. Ndokkalee ñi am yërmande, nde dees na leen yërëm. Ndokkalee ñi sell ab xol, nde ñooy gis Yàlla. Ndokkalee ñiy sàkku jàmm, nde ñoom lees di woowe doomi Yàlla. Ndokkalee ñi seenug njub tax ñu di leen bunduxataal, nde nguurug asamaan ñooy boroom. «Ndokkalee yeen, bu ñu leen di saaga, di leen bunduxataal, di leen sosal gépp njombe ndax man. Bégleen te bànneexu, ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu.
Macë 5:3–12
Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokkalee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
Luug 11:28
«Ndokkalee yeen ñi fóot seeni yére, ngir saña lekk ci garabu dund gi, jàlle ci bunt yi, dugg ci biir dëkk bi.
Peeñu ma 22:14
Bés yu mujj yi
Wone yépp26 Okt 2026
25 Okt 2026
24 Okt 2026
23 Okt 2026
22 Okt 2026
21 Okt 2026
20 Okt 2026