Daa xool, gisul kenn; mu tiisoo li ci kenn jógul, moo tax loxoom may ko ndam, ci àtteem la sukkandikoo.
Esayi 59:16
Leeru Bés bi
Daa xool, gisul kenn; mu tiisoo li ci kenn jógul, moo tax loxoom may ko ndam, ci àtteem la sukkandikoo.
Esayi 59:16
Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, amuloo moroom! Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, ma bëgga xamle lépp, te mu bare ba wees ab lim. Saraxi jur ak pepp, taamuwuloo ko, ay nopp nga ma bënnal, saraxu rendi-dóomal ak saraxu póotum bàkkaar, sàkkuwuloo ko. Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
Taalifi cant 40:6–8
Li tax Baay bi sopp ma, moo di sama bakkan laa joxe, ba man koo jëlaat. Kenn du jële sama bakkan ci man; man maa koy joxeel sama bopp. Maa ko saña joxe, maa ko saña jëlaat, te loolu la ma sama Baay sant.»
Yowaan 10:17–18
Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man! Yeen waa àddina, catoo cat, walbatikuleen fi man, mucc. Man maay Yàlla, du keneen.
Esayi 45:21–22
Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»
Jëf ya 4:12
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
2.Korent 8:9
Dama ne, maa leen jox sañ-sañu joggi ci kawi jaan aki jiit, joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk.
Luug 10:19
Àndleen ak sago te teewlu! Ki leen di tuumaal, Seytaane, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax.
1.Piyeer 5:8
Kon nag nangulleen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.
Yanqóoba 4:7
Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane. Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan. Kon nag jëlleen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm. Taxawleen kon temm. Defleen dëgg di ngañaay li ci seen ndigg, njub di seen kiiraayal dënn. Xibaaru jàmm bi indi jàmm nag, defleen ko muy dàll yu dëgëral seen taxawaay. Te fu ngeen tollu ŋàbbleen pakk biy seen ngëm, ci ngeen mana fanqe mboolem jumi sawaray ku bon ki.
Efes 6:11–16
Bés yu mujj yi
Wone yépp27 Okt 2026
26 Okt 2026
25 Okt 2026
24 Okt 2026
23 Okt 2026
22 Okt 2026
21 Okt 2026